Tolluwaayu réewum Senegaal ci wàllu koom tàmbali naa ub boppu ñenn ñi. Te, dara waralu ko lu dul bor bi fi Maki Sàll bàyyi ak li FMI di dóor dàqe ak Nguur gi fi nekk. Rax-ci-dolli, kurél gii di Moody’s dafa yokk ci xar mi kawar. Ndax, dafa xamle ne tolluwaayu Senegaal ci koom sax dafa gën a wàcc. Waaye, loolu taxul doomi réew mi seetaan ko. Nde, jot nañoo dugal koppar gu takku ngir réew mi suqaliku.
Réewum Senegaal bokk na ci réew yi gën a ndóol ci àddina si. Te nag, mi ngi ciy bëgg a yàgg. Looloo tax Nguur gu bees gi di lal i pexe ngir jële réew mi ci ndóol gi mu nekk. Waaye tamit, ñu jéem koo def réew moo xam ne day moom boppam ci fànn yépp. Ndax kat, ku la abal i bët moom, fu ko neex ngay xool. Te, ngir loolu ñàkk, bi ci jiitu mooy ñu kopparal seen ug koom. Ñaareel bi, doomi réew mi sax ñoo war a defar réew mi. Looloo sabab Nguurug Senegaal def ñetteelu APE (Appel Public à l’Epargne) bi. Te, li mu ko dugge du lenn lu moy sol jibab réew mi koppar yu doy ngir sàmmonte ak i wareefam te mën a jëmmal i naalam.
Ñetteelu APE bi, dooreesoon na ko keroog, fukki fan ak juróom-ñett ci weeru sàttumbar wii ñu génn. Donte ne sax, bindu gi ñaar-fukki fan ak ñaar ci weer woowu lañ ko tàmbali woon bees sukkandikoo ci yégleb njëwriñu kopparal gi ak nafa gi. Liggéey boobu ñi ngi ko dakkal ci àjjuma jii weesu. Mébétu Nguur gi moo nekkoon dajale lu tollu ci ñetti téeméeri miliyaar. Waaye, yëf ya mujj na faa romb di dem. Ndax, am nañu lu ëpp ñeenti téeméeri miliyaar ak juróom-fukk.
Lii yépp nag bu amee, doomi Senegaal yi nekk bitim-réew bay nañu ci waar wu yaatu. Dafa di, doomi Senegaal yu nekk ci lu ëpp ñeen-fukki réew ak juróom dugal nañu ci seen loxo. Kon, gàcce ngaalaama ñoom. Seen taxawaay li muy firndeel du lenn lu moy kóolute ak yaakaar gi ñu am ci Njiiti réew mi. Te, lépp, jubluwaay bi mooy réew mi jëm kanam.
Ba tax na, Nguuru Senegaal gi sant na leen, gërëm leen ci taxawaay bi ñu am. Waaye ba tay, loolu bataaxal la tamit ngir xamal leen ne mag bu naanee ndox mu tàng, suukër saa tax.