Jàngalekat bii di Baara Mbeng moo jël neexal bii ñuy dippe “Grand Prix du Chef de L’Etat”. Tay ci alxames ji lees doon amal ndajem cargal jàngalekat bi, fa “Grand Théatre”.
Ndaje mii nag, du guléet ñu koy amal. Ren mooy ñetteelu yoon wi. Neexal boobu, ngir nga jël ko, fàww nga am ay poñ yu bari. Te, ci téeméer yi ñu doon laaj, Baara Mbeng am na ci juróom-ñeen-fukk yu teg tuuti (90,28) bees sukkandikoo ci waa Seneweb. Neexalee nañu ko ñaar-fukki miliyoŋ ci sunuy koppar.
Moom Baara Mbeng nag, jàngale na lu tollu ci fukki at ak juróom-ñeent. Mi ngi jàngalee fa lekkool bu digg-dóomu bu “Louga Commune”. Ma nga fay jàngale “Histoire ak Géographie”. Nee ñu def na liggéey bu mucc ayib ci wàll wi mu féete.