NJËGU MBËJ MI JÉGGI NA DAYO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mboolaay mi sonn na, damm na, tàyyi na ci dundin bu metti bi muy dundu. Réewum Senegaal dafa mel ne ab taab bu bënnagul, foo laal ñu ne la wet gee moo gën a metti. Daanaka, baadoola yi, ba ñi ci xaw a féex sax, ñépp ay yëg gile metit. Li mboolaay mi di kaas, mooy ne, léegi, lépp a yokku ci réewum Senegaal. Bu dul lekk geek naan gi, leneen la lu ab saa-senegaal di jariñoo. Mbëj mi la ñépp di waxtaane jamono yii, dem na sax ba laalaale mburu mi. Nde, lakk-katu mburu yi sax dañu nar a yokk njëgu mburu. Kon fan la saa-senegaal bi jëm ?

Njëgu mbëj mi ni muy yokkee jéggi na dayo. Jaaxal na ñépp, ku nekk a ngi génn di wone say faktiir, walla li nga jot a jënd ci ayu-bés bi ci kontëeru Woyofal yi. Waa Woyofal, daanaka, ci ayu-bés bi dinañ dugal lu mu néew-néew ñaari junni ci sunuy koppar te du tee mu jeex. Ku ci mel ne Ummi Nduur bokk na ci ñi gën a fésal yokkute njëgu mbëj mi (kuraŋ) te teguwul fenn. Dem na it ci ay tele yu ñu ko woo, ngir mu kaas ko fa, laaj ay leeral waa Senelec. Waaye, amu ci benn leeral. Taxul mu xàddi, ndax Ummi dafa mujje def ab petisiyoŋ, mu am ci 42 000iy nit yu ko xaatim ngir xeex lu ni mel. Jotoon na sax yóbbu ab kalaame (plainte) ca CRSE (Commission de régulation du secteur de l’énergie) ngir kaas njëgu mbëj mi. Xamle na ne, jot na ci diirub ñaari ayi-bés, lu tollu ci téeméeri kiliyaanu Senelec yu seen faktiir yi yokk ba mu yéem leen. Mu dolli ci ne :

« Yokkute njëgu mbëj goo xam ne kenn xamul lu ko sabab, metti na lool ba jéggi dayo ci njaboot yeek ñi yor barabu liggéeyukaay yi. Fàww waa Senelec jox nu ay leeral ci yokk gi ñuy yokk mbëj mi, ak tamit naka la kontëeru Woyofal yi di doxee, lu waral muy gaaw a jeex ».

Am na sax ñenn ñuy ŋàññ Senelec ne dafay jaay doole mboolaay mi, ndax dafa bëgg léegi saa-senegaal yépp di jëfandiko kontëeru Woyofal yi. Te loolu duñu ko nangu wenn yoon.

Njiitul Senelec li amaloon na am ndaje ci talaata ji 24 oktoobar 2023 ak waa  ASCOSEN, ak waa CNDC (Comité National de Dialogue avec la Clientèle) ngir waxtaane yokkute njëgu mbëj mi. Ci biir waxtaan wi, Momar Ndaw di njiitul Ascosen xamal na leen ne mbëj mi seer na lool, te dañu war a xool nan lañuy def ngir mu wàññeeku. Cii seen i biir kàddu, waa Ascosen a ngi wax ak waa Senelec ne leen :

« Mënoo leen di tonowoo 49i milyaar ci sunuy koppar, rax-ci-dolli, Càmm gi di leen dooleel cig nafaam, ba noppi ngeen ne dangeen di yokk njëgu mbëj mi. Kon am na luy ñuul ci soow mi. Loolu daal a taxoon, ñu ne nanu leen laaj ngeen xoolaat tëralinu njëgu mbëj mi. »

Fara-caytu Senelec bu mag bi tontu na leen di leen xamal ne « du Senelec mooy tëral njëgu mbëj mi. Loolu waa CRSE ñoo koy tëral, waaye ci fan yii di ñëw, dinañ amal waxtaan ak waa CRSE ngir xool naka lanuy def ba njëgu mbëj mi wàññeeku. »

Nde, Càmm gi génne woon na lu toll ci 258,1 milyaar ci sunuy koppar, jagleel ko lépp lu jëmm ci wàllu laf. Waaye, ci weeru saŋwiye wi, Càmm gi dafa wàññi ci lu jëm ci mbëj mi ngir mu mën a yaxanal nafa gi, dugal ko ci yeneen i fànn.

Njiitul Senelec li di Paap Mademba Bitéy, xamle na ne

« Li tax faktiiri mbëj mi yokk fan yii, am na yu bari yi ko waral. Càmm gi rekk dafa wàññi ci weeru saŋwiye 2023 xaalis bi mu jagleloon mbëj mi. Loolu yemook yokkute njëgu mbëj mi waa CRSE tëral ci ñiy lakk lu toll ci 150 jàpp 250i kWh. Dafa feeñul woon boobu ba léegi, ndax ci jamonoy seddaay lanu nekkoon, nga xam ne li nuy lakk ci mbëj mi du bari. Léegi nag, noo ngi ci jamonoy tàngaay, te loolu, ñépp xam nañ ne li ñuy lakk ci mbëj dafay bari ba dafay ëpp doole… Lii doŋŋ a waral faktiir yi yokk. »

Waaye, li ub xelu saa-senegaal yi mooy, ak soroj beek gaas bi nuy waxtaane ne moo ngi ci biir réew mi ba noppi kurang bi di yokk rekk. Doy na waar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj