NJIITU RÉEW MI BIND NA NJIITUL NGOMBLAAN GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal DPG bu elimaanu jëwriñ yi ba léegi fayagul. Dina ko def am du ko def ? Kañ la ko war a def ak kañ la ko warul def ? Saa buñ xëyee, lu bees rot ci. Fan yii weesu, Njiitu réew mi dafa jébbal Ngomblaan gi ñaari sémbi àtte yuñ war a fénc, wote leen. Waaye, daf ci toftal DPG bi, muy ñetteelu sémb wi, lépp, dépite yi war cee liggéey ci àppug 15i fan.

Démb nag, ndajem njiiti Ngomblaan gi dafa daje. Ñi ko séq ñooy ñi jiite kippaangoy dépite yi ak njiitu Ngomblaan gi ci boppam, Aamadu Maam Jóob. Waaye, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñoo fa ëpp. Noonu, ca lañu jàppee bésub àllarba jees dëgmal, 11i pani sàttumbaar 2024, ngir Usmaan Sonko defsi fa DPG bi. Lél boobu nag, bees sukkandikoo ci dépitey Yewwi Askan Wi ak ñi seen xam-xam màcc ci wàllu Yoon, dafa worook li sàrtu biiru Ngomblaan gi tëral. Nde, ci li Yoon wax, DPG bi, warees na ko amal as néew ci àppug 8i fan ginnaaw bi ko Njiitu réew mi yégalee Ngomblaan gi. Maanaam, bés bi Njiitu réew miy jébbal Ngomblaan gi dekkareb DPG bi, warees na cee teg yeneen juróom-ñetti fan laata elimaanu jëwriñ yi di janoojeek dépite yi fa Ngomblaan ga.

Bu ko defee, alxamesu démb ji, 5i pani sàttumbaar 2024, lees war a door limub 8i fan yi. Bu boobaa, keroog 13i pani sàttumbaar, gën-gaa teel, la Usmaan Sonko war a def DPG bi. Waaye, waa Bennoo Bokk Yaakaar dañu màttoon ci lélu 11 bi, ŋoy ci ba dëgër. Njiitu réew mi nag, àtte na xeex bi, moom mi yor kàddu gu mujj gi. Nde, dafa bind njiitul Ngomblaan gi, sant ko ni bésub 13 la elimaanu jëwriñ yi di def DPG bi. Mu mel ni wax ji jeex na. Li mat a laaj nag mooy, ndax fileek boobu du fekk mu tas Ngomblaan gi. Nde, ci li ko Ndajem ndeyu sàrtu réew mi xamal, dina am sañ-sañu tas Ngomblaan gi keroog 12i pani sàttumbaar 2024, bés bi muy matal ñaari atam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj