Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, teewe na, démb, waxtaan wi Mbootaayu Xeet yi (ONU) doon amal. Waxtaan woowu, ci wàllu pólitig la aju woon. Ponk baa doon “Njàngum xamtu, xarala ak fent ñeel Afrig bi ñu bëgg” (l’éducation par la science, la technologie et l’innovation pour l’Afrique que nous voulons ). Moom nag, Njiitu réew mi, demul woon. Ci lënd gi (virtuel) la ko doon teewe.
Guléet, bim falook léegi, Njiitu réew miy àddu ci kanami naataangoom yi ci àddina si. Mu doon weccante xalaat ñeel njàng mi ci kembaaru Afrig. Moom, Sëñ Basiiru Jomaay Fay, fésal na ci gis-gisam, muy firndeel solo ak yitte ji mu am ci wàllu njàng meek njàngale mi. Rax-ci-dolli, biral na yéene ji mu am ci ñu xoolaat anam yees di doxale njàng mi ak nees koy kopparalee. Li mu ko duggee mooy fexe ba njàng meek tàggatu bi, fi réewum Senegaal, nosewu walla lootabewu ci anam bu mucc ayib ngir njariñ mën cee tukkee.