Bi joŋanteb Manchester City ak Bayern Munich bi jeexe, ndeke, Saajo Maane ak Lërooy Saane dañoo xeex, gayndeg Bàmbali gi daldi koy kurpañ ci gémmiñ. Loolu la yéenekaayu almaŋ bii di BILD xamle. Nee ñu, Lërooy Saane dafa ñàkke kersa Saajo Maane, wax ko wax ju bon te ñaaw.
Coowal xeex boobilee lëmbe xibaar yeek mbaali jokkoo yi. Nde, ginnaaw bi leen ñoom Haaland wulle wulli yu metti yi, kuppekati Bayern Muniche yi dañ doon wullante seen biir. Ñaari boroom tur a ko sékkoon nag, muy Saajo Maane ak Lërooy Saane, doomi Suleymaan Saane mi doon futbal Senegaal. Loolu, nag, dafa bett ñu bari. Ndaxte, jàmbaaru Senegaal ji, Ñàncoo, kenn xamewu ko xuloo astemaak xeex. Moom kay, wëlis xereñte ak fulla ji mu baaxoo wone ci pàkki futbal yi, yar ak teggin, mbaax ak tabe lees ko xame. Ayleyéwén, Saajo Maane, ku lewet la. Kon, bu demee xeex, am na lu tax.
Ci li rotagum ciy xibaar, Lërooy Saane, doomu Suleymaan Saane ji, dafa wax Saajo Maane, ne ko : « Ñuule bu bon bi ! ». Kàddu yu bon, ñaaw te ruslu yilee naqari Saajo Maane, mu daldi mer ba futt, daldi noq Lërooy Saane. Seen i moroomi kuppekat ñoo leen àtte sax. Xam naa bu dul woon ñoom, goneg Bàmbali gi wol koon na ko ni tigadege. Caytug Bayern Munich gi, nag, diisoo nañ seen biir, jël ndogal. Ñoom daal, dañu génne ab yégle, di ci wax naan, ajandi nañu Saajo Maane, du bokk ci joŋante biñ dégmal te alamaan nañ ko. Ndogal loolii, nag, jur na coow lu réy. Li jaaxal nit ñi mooy, lu tax daanuñu Lërooy Saane tamit. Xeex de, ñaar a koy def. Ku tooñ ? Ki wax wax ju ñaw ji walla ki ko ci ñuus ? Kon, màndute amu fi. Mbaa du li Lërooy Saane di futbal Almaañ a tax ? Doy na waar daal, te xel teey na ci.
Ñoom ñaar ñépp a jéggalu seen i moroom bi ñuy tàggatu tey. Waaye, jamono jii, li ñépp di laaj mooy ndax Saajo Maane dina toog Bayern déwén. Ku dund gis.