Paate Jaañ wàcc na liggéey démb ci àllarba ji, 23i fan ci weeru ut wii 2023. 89i at la amoon. Jarbaat ji, Mademba Njaay, moo ko tàgge. Muy xibaar bu tiis lool. Nde, Senegaal a ñàkk. Ndax, moom Paate Jaañ, boroom xam-xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal ak koomal, liggéey lu réy ci làkki réew mi, rawatina wolof. Liggéey na yit ci koom-koom ak ci mbirum diiney Lislaam.
Paate Jaañ mi ngi juddu 7eelu fan ci saŋwiyee atum 1934 fa Ndar. Moom, dafa bokkoon ci xeltukat yooyii xaroon seen tànki-tubéy, doon xeexal làmmiñi réew mi, àndoon ci ak royukaay bi, werekaan bi, Séex Anta Jóob. Loolu la ko jarbaat bi seedeel. Daf ne, ci xëtu dalu webu APS, Paate Jaañ mooy xeetu “…xeltukat yooyu doon sóobu ci bépp xeex bu soxal làmmiñi réew mi, moom ak àndandoom ya Séex Anta Jóob ak Usmaan Sémbeen.”
Mademba Njaay taskatu-xibaar la. Mi ngiy fàttali tamit ne, nijaay ji, Paate Jaañ, moo amaloon, ca atum 1982, “…ndaje (kolog) mu siiw moomu Séex Anta Jóob, boroom xam-xam bi, biralee woon xalaatam fa jàngune bu Ndakaaru, ay guddiy guddi.”
Aliyun Sàll “Paloma” dénk n’a waa APS tamit ne Paate Jaañ “nit ku bari woon i feem la, yaatu woon xam-xam ci fànn yu bari (…) gëstukat dëggantaan (…) fi Senegaal, amul kenn ku gën a xóotal ci xamtuy nit ak mboolay gi.”
Paate Jaañ ku ubbeeku woon la, géeju woon lool ci baataan yi, doon leen faramfàcce ci anam bu yéeme.
Ginnaaw bi mu jàngee Ndar ba ame BAC ca liise Faidherbe ba fa nekkoon, ca la ñëwee Ndakaaru, jàngsi xam-xamu Yoon ba am lisãsam, daldi dem Farãs, fa Pari. Ñooñu, atum 1965 mu daldi jeexal teesam ci njiitalu Porfesoor Maurice Byé. Mi ngi bindoon tees bi ci bennoo koom-koomu Afrig sowu jant.
Waaye, Paate Jaañ dafa xëroon ci mbiri làkk, moo ko taxoon a defi doktoraa fa jàngune Aix-en-Provence. Mu bind fa ab tees buy wax ci nees di dëppalee làkki Afrig yi ak jamono ju yees ji.
Paate Jaañ bind nay téere yu bari ci fànn yu wuute. Ñu ràññe woon ko ci kàngaami làmmiñu wolof. Mo sos itam kërug móolukaay gii di Sankoré. Kon, bu yeboo jàpp ne Paate Jaañ bey na waaram ci toolu làkk yi. Jaanam wàcc na.
EJO ak LU DEFU WAXU ñu ngi koy jaal njabootam, ay mbokkam, gëstukat yi ak Senegaal gépp. Yal na xippee guyaar.