Fan yii, Palestin ak Israayel ñu ngi sànnantey mbéll, sóobu cib xare bob, bim tàmbaleek léegi, ay junniy junni bakkan rot nañ ci. Wii yoon nag, Palestin moo bett Israayeel, song ko cong mu metti, rey fa lim bu takku, daldi am ñu mu jàppaale yóbbu. Daanaka, ayu-bés a ngi nii ñaari dëkk yiy xeex. Ku ci nekk deele nga as-tuut 2 000iy nit. Yàqu-yàqu yi nag, mëneesu leen natt. Ba léegi, kenn àttewul, lu moy di woote wéerug ngànnaay yi ak jàmm.
Yëf yi a ngi door keeroog, gaawu 7 oktoobar 2023, yemook bés bi Israayel di màggal Yom Kippour. Mu di bés bu réy ci yawuud yi, di tekki ci ñoom bésub njéggal, bésub tuub bàkkaar yiñ defoon. Jamono jooju la leen waa Palestin, jaare ko ci banqaas bii Hamas, nekk ca Gasaa. Ñoom, sóobare yooyii xeexal seen um réew, dañu fippu, nas am pexe, daldi song way-mbéeféeri Israayel yi leen bëgg a noot, nangu seen suuf, te dëkk ci di leen fitnaal ak a xoqatal ay ati at.
Ginnaaw ñareelu xareb àddina si, atum 1947, lañu sosoon réewum Israayel ci anam bu safaanook yoon. Boobaak léegi, mayuñu jàmm julliti Palestin yi. Nde, ñoom siyonist yi, ànd ak saa-amerig yeek lenn ci tubaab yi leen di jàppale, ŋeeñ nañu suufu Palestin bi daanaka deseetuñ dara. Dénd bii firnde la ci.