Ñaar-fukki weeri xare yoy, bés bu nekk, fa Gasaa, ay bakkan rot. Bu leen misil yeek bomb yi rayul, sóobare yi di leen sox bali fetal, xiif ak mar a leen di ray. Nde, Israayel yemul rekk ci di leen faagaagal, waaye dafa tëj bunti dëkk ba, bàyyiwul ndimbal leek dund bi àgg ca askanu Gasaa. Moom daal, bu yeboo jàpp ne waa Gasaa ci ab kaso lañu nekk. Bu leen jànt bi tiimee yit, lëndëm lañuy dund.
Àddina sépp a ngi seetaan, way-mbéeféeri Israayel yi di faagaagal askanuw lëmm. Noo ngi toog di seetaan, Israayel di jeexal sunuy mbokki nit yoy, amuñu ngànnaay, mënuñoo daw te amuñu fenn fu ñu mën a làqatu ngir mucc ci fitnay siyonisti Israayel yi.
Jamono jii, xareb Israayel ak Irã bi tax na ñu baree bari fàtte ne Israayel a ngi ray ak a faagaagal askanuw lëmm ci jaay doole gu jéggi dayo.
Dafa di, ci àjjumay tay jii rekk, ñaari jéyya yu mag jot nañoo am fa béréb ba ñuy séddalee dund bi (lekk ak naan). Bees sukkandikoo ci wattukati nit ña fa Gasaa, sóobarey way-mbéeféeri Israayel yi ray nañu juróomi saa-palestin yoy, lu ñu lekk lañu doon wër. Ndeysaan, di wër loo lekk ak loo naan ngir sàmm sa bakkan, ñu xañ la ko, jël sa bakkan teg ci.
Juróomi nit ñooñu, fa bëj-saalumu dëkk ba lañu leen faatee. Mu am itam yeneen 26i saa-palestin yu ñu rayati fa koridooru Netzarim, nekk ci diggu dëkk ba. Foofa, sóobare yi dañu soqi seen i fetal ca kaw nit ña wutsi woon dund. Loolu doyul, ab roppalaan tàbbal seen kaw ay bomb. li bu dul coxorte, lu mu ?
Cig pàttali, ca ndoorteelu weeru màrs la Israayel tëjoon dëkk ba, tere dund bi dugg fa. Xawoon nañu ubbi tuuti buntu ya ca njeexitalu weeru me wii nu génn. Waaye, ubbi boobu sax, dañu ci ray ñu baree bari.
Wëliif xiif bi muy xiifloo waa Gasaa ak li mu leen di marloo, Israayel dafa yàq dëkkuwaay ya, màbbal raglu yaak bérébi fajukaay ya. Daanaka raglu amatul fa Gasaa. Nit ñaa nga feebar, ñii seen tànk walla seen loxo dagg, ñee ame ay gaañu-gaañu yu metti, ñale di ay jirim yoy, seen mbokk yépp la Israayel faat. Kon, mënees na wax ne, Gasaa, dootul dëkk, waaye ay sëg la.
Tay jii, Israayel a ngi jàmmaarloo ak Irã ginnaaw bi mu ko jëkkee sàndiy misil. Moom daal, ciy tooñ la yawuut yi dëkk, Etaasini ak Bennoog Tugal di leen ci jàppale saa su nekk. Ñu bare ñoo ngi laaj lu tax ñooñu di leen jàppale. Dafa di, ñu bokk teen ñooy laxasooy goj.
Ku xam mboor, dinga xam ne Etaasini, moomeelu Enjeŋ yi la woon. Saa-tugal yee fa dem, jaay leen doole, nangu seen i suuf, sanc fa. Ku xam Etaasini xam tamit ne, fu fitna mës a am ci àddina si, lu ci ëpp, seen loxo du ci génn. Nde, dañu jàpp ne, ñoom ñoo yilif àddina si te ñépp ci seen “waaw” lañu war a dox. Bu dee saa-tugal yi moom, seen ñaawteef umpul kenn. Nootaange seen yëf la, jaay doole di seen doxalin, nappaate ak tiitalaate di seen ngànnaay. Ñoom it, jàpp nañu ne ñoo gën ñépp, sut ñépp, yelloo li ci àddina sépp. Tooñkat nag, tooñkat rekk lay àndal. Loolu moo tax ñu faral Israayel mi nga xam ne, mooy xaj bi ñuy yónni Penku, mu màttal leen réew yiy bañ a nekk seen i jaam.
Moone de, bu yeneen réew yi booloo woon, bennoo jàmmaarloo ak ñoom, léegi mu dakk. Waaye, dafa mel ni, ay naaféq la Israayel, Etaasini ak Bennoog Tugal jàkkaarlool. Ba kañ ?