Coowoo diggante làngug Pastef gi ak tele bii di TFM du guléet ñu koy gis. Seen diggante moom, taxu ko rattax. Nde, ba ñuy nekk ci kujje gi ba ni ñuy jotee ci Nguur gi, ñoom ñaar duñu jaaroo ab taal. Kàdduy Badara Gajaga yi rotal keroog àjjuma ci jotaay bii di “Jàkkaarloo” dafa xolli góom boobu. Boobaak léegi, waa Pastef ak ñu bare ci réew mi ñu ngi naqarlu taxawaayu tele TFM ñeel mbir mi.
Kàddu yi rote ca waxtaan wa amoon keroog fa TFM jur na coow lu bari ci réew mi. Ñii a ngi naan dara nekku ca. Ñoom ñoo ko leble, dañu leen a fay seen bor. Ña ca des, di xataraayu di dal ci kaw Badara Gajaga ak tele TFM. Nde, dañoo jàpp ne li fay am tayeef la. Maanaam, li ñu fay wax, ñoom, dañu ca ànd. Kàddu yi waral coow li mooy yoy Badara Gajaga yékkati teg ko ci kow dépite boobu di Aamadu Ba ak ci deru elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko. Loolu la ay ñoñam ne dootuñu ko nangooti. Ndax, la woon, wonni na.
Dafa di, waa TFM ak waa Pastef moom du tay lañu njëkk a am i réeroo. Xanaa kay dafa am lu yokk ci xar mi karaw. Looloo tax, pekkug pólitig gu Pastef génnee ab yégle ngir ñaawlu xeetu doxalin yooyu. Nde, dañoo jàpp ne maxejj bi am na sañ-sañu wax lu ko neex fii ak tooñul moroomam. Te, lii am fa TFM moom dafa am lu muy nirool. Waruñoo nangu ñuy xaste walla di saagaate ci seen jotaay yooyu. Looloo tax sax, ñoom ñu dem ba njort ne ñoom ñoo ci ànd ak faramfàccekat yooyu. Maanaam, ñoo leen ngemb. Ba tax na, ñi ngi sàkku ci kurél yi ŋànk wàll woowu muy waa CNRA (Conseil National de Régulation de l’Audiovisuel) ak waa CORED (Conseil pour l’Observation des Régles d’Ethique et de Déontologie dans les médias) ñu àddu ci ca teel. Yaa moom sa bopp warul a tax ngay def lu la neex. Ndax, sàrt 10 bu ndeyu-àtte yi moo tënk ñépp. Bu ñu la tooñee, mën nga koo wonee ci anam bu la neex te, bañ a toññarbi.
Taxawaayu TFM boobu tax na way-bokki Pastef yi di sàkku ci kilifa yi, ku ñu fa woowati, mu bañ a dem. Te, loolu door na ak jëwriñ ji ñu dénk kopparal gi ak koom-koomu jàppalante gi, di Alliyun Badara Jonn. Jëwriñ jooju xamle na ne dootul nangoo dem ci seen i waxtaan fii ak génnuñu jéggalu elimaanu jëwriñ yi ak dépite bii di Aamadu Ba.
Mu mel ni xiiroo ak ŋaayoo yi am ci diggante làng googu ak sabalukaay boobu lu yàgg la. Dafa di kay, saa su nekk rekk day am lu ci beesaat. Waa Pastef nag, tàmbali nañoo fippu. Li mat a laaj kay mooy ndax, loolu dina tax waa TFM teggi seen tànk fa ñu ko tegoon ?