Ginnaaw bi ñu nekkee ciy waxtaan ak i joyyanti ngir jubbanti ati njàng yu duggante yi, Senegaal dina dem ci yeneen i péncoo yu ñu jagleel ba tay njàng mu kawe mi ak gëstu bi. Li ñu ci namm nag mooy sopparñi jàngune yi, delloo leen ci xereñte, njàng mu amul tappale te bari njureef.
Démb ci àjjuma ji, 28i fan ci weeru màrs 2025, la ko jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kawe mi, gëstu bi ak coste gi, El Haaji Abdurahmaan Juuf, xamle. Daf ne :
« Bu dee sunu yitte ji gën a tembare mooy jubbanti atum njàng mi, noo ngi waajal itam ëllëg. Ci jamono yii di ñëw, dinanu amal i diisoo yu yaatu ngir xalaataat ci anam yu xóot njàng mu kawe mi ak gëstu bi. »
Muy xibaar bu mu siiwal fekk mu doon amal waxtaan ak sunuy naataangoo yu APS (Agence de Presse Sénégalaise). Ci biir waxtaan woowu sax, dellusi na ci lu yaatu ci waxtaan ak joyyanti yi ñu sóobu ak sàndikaa jàngalekat yi ngir saafara jafe-jafe yi njàng mu kawe mi di jànkonteel.
Bokk na ci jafe-jafe yi gën a fés, ati njàng yi duggante ba kenn xamul fu at tàmbalee ak fu mu war a yam. Muy jafe-jafe bu bari lool ay loraange. Moo xam ci Nguur gi la ak koppar yi mu ciy xëpp at mu nekk walla ci njàngaan yi ak at yu ëpp yi ñuy def ci jàngune yi.
Donte ni tembare na lool ngir saafara yile jafe-jafe, Càmm gi nisar na a amal yooyule diisoo, ci jamono yii di ñëw, ngir xalaataat ci njàng mu kawe mi ak gëstu bi. Muy ndogal luy dellu ci gis-gisub Njiitu Réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ni ko jëwriñ ji fàttalee ak i kàddoom :
« Réew mu tàggatul i ndawam ci ñàkk tappale ak xereñte, réew mooma a ngay sàkkal pexe seen ëllëg. » (kàdduy Njiitu Réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ci pàttalig jëwriñ ji)
Jotul a leeral nag bés yees ko àppal. Waaye, fees ko namm jaarale nag mooy càmbar 10i ati CNAES (Commission nationale de l’Enseignement supérieur). Bu ñu ci noppee, dinañu dëppale naal yi ñeel njàng mi ngir dooleel xereñte jàngune yi, njàng mu amul tappale te bari njureef.
Naka noonu, dinañu nekk waxtaan yu yaatu yoy, dees na ci boole ñépp ñuy yëngu ci wàll wi (Nguur gi ak i way-jëflanteem, jàngalekat yi, njàngaan yi ak sàndikaa yi). Li nu ci jublu nag mooy delloo jàngune yi seen dayo, soppi leen i yoon ngir suqaleeku réew mi.