Bañ koy wote ci jamonoy Njiitu réew ma woon, Abdulaay Wàdd, soxna Penda kesee nekkoon soxna su ci àndul woon. Li ko waral rekk mooy, ci gis-gisam, bu loolu amee, xeex dakk, te baaxul ci jigéen ñi. Te tamit, li taxoon Ablaay Wàdd jëmbatoon ci fulla mooy jëfandikoo jigéen ñi, daldi jàll ; geg la woon ci pólótigam. Kon dogal boobu naxee-mbaay la te bokk na tey jii ci li tàrdeel jigéen ñi. Penda, bu sañoon, Péncum Ndawi Réew mi fees dell ak i jigéen waaye seen mën-mën moo leen diy jox palaas yi, du doon yemoo gi. Firnde li mooy : xeex bi daa dellu ginnaaw, ndax jàpp nañ ne la ñu bëggoon, am na…
Pr Penda Mbów nëbbul mbetteelam ci tabbug Aamadu Maam Jóob ci boppu Ngomblaanug Senegaal. Nde, ñépp dañoo foogoon ne soxna Aminata Ture moo koy jiiteji ngir xereñam ak it kàmpaañam bu mucc ayib. Waaye, ci njàngatu soxna Penda Mbów mi xam-xamam màcc ci wàllu mboor, Senegaal day réew mu noppeegul ngir tabb jigéen mu jiite ko. Mu neeti, li waral coppite giñ digoon Aminata Ture mooy, su Njiitu réew mi tële woon, njiitu Péncum Ndawi Réew mee koy wuutu ; kon jigéen lay doon.
Moom nag, ku dégg turam, sam xel dem ci kurélug maxejj yi, maanaan li tubaab di wax « Mouvement citoyen », ndax mooy ki ko sos fii ci Senegaal, moom Pr Penda Mbów. Mu deeti meññeefu kurélu « set-setal ». Soxna Penda, Senegaal lay noyyee ; réew mee ko ñor, te moo ko tax di def i jéego ngir réew mi naat, suqaliku. Lii rekk a ko amal njariñ.
Pr Penda Mbow fàttali na tamit ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, am na ndaje ak mboor. Te, ñu ngi koy xaar. Seŋoor moo bàyyil boppam Nguur gi. Abdu Juuf, li Senegaal gën a jàpp ci moom, mooy bi mu woowee Ablaay Wàdd ndokkale ko, nangu ne lajj na ci joŋantey wotey atum 2000 mi. Ablaay Wàdd tamit, kenn fàttewul ne, ci ati 1974 yi, ba ni mu jële Nguurug Senegaal, daa mës a xeexal demokaraasi. Waaye, tey, li nuy fàttaliku ci moom, mooy bi mu bëggee jaay doole, teg doomam ci boppu réew mi.
Maki Sàll nag, ñu ngi koy déglu ba xam fu wànnent di mujje ak i gëtam.
Coowal 3eelu moome, kenn waru ko woon a yëkkateeti fii ci Senegaal. Ndaxte, xeexoon nañ ko ba mu féete boor ci jamonoy Ablaay Wàdd. Kon, tey jii, waroon nañoo weesu lii.
Fi porofesëer iniwérsite bi di gën a ñaax waa réew mi, mooy li ñeel njàng meek tàggat gi, ngir xam-xam buy jur yokkute ak te di jëmale kanam. Ñu bàyyi xel bu baax ndaw ñi jàkkaarlook mag ñi, di 2i mboolem-nawle yu bokkul i soxla.
Soxna si biral nay kàddu yu solowu teu daw yaram, di ay kàdduy seede ñeel ndem-si-Yàlla yii di porofesëer Maalig Njaay ak Maam Lees Kamara, taskatu xibaar bi. Daf ne :
« Su fekkee génnug àddina Maam Lees bettu ma lool, ndax yëgoon naa feebaram, gu Maalig gi moom, bett na ma. Ndax, am nay mbindeef yoy, doo xalaat a boole seen i tur ak dee. Moo ma dal ci Maalig Njaay. Nit ku baax la woon, ku amoon gis-gis, xel mi nàccoon lool. Daa nanu ànd liggéey lu bari, maak moom… Maam Lees nag, sama càmmiñ la woon… Bi ma nekkee jawriñu mbatit, mu feebar, Bóris daf ma seetsi, ni ma fàww Lees dem fajuji bitim-réew. Ma daldi jóg, dem ci Njiitu réew mi, mu jàpp ci bu baax, nu toppatoo ko bañ yóbbu Maam Lees Faräs mu fajuji, ñibbisi ci jàmm. Bu dee sama jamonoy jawriñu mbatit am na lu baax lu ma def, lii la. Waaye, Bóris a ma ci jóo. Yal na leen Yàlla xaare àjjana ak ñoomin Majéey Mbóoj ak Ibraayma Seen. Bég naa lool ci liñ tuddee CESTI Maam Lees Kamara. War nañoo def tamit dara ngir Ëséni Roqaya Aaw. Ndax jigéen ñi ñoom, dañ leen di faral a fàtte ».
Ndey Koddu FAAL ci taataan jotaayu Jury Du Dimanche ak Aysata Njati FAAL.