Rafayel Njaay taalifkat la woon…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndeem dëgg la ni àjjana, ngir mbindeef yi daa yokk yëf yu baax ci àddina la, yaakaar nanu ni Rafayel Njaay a nga guyaar, ca tóokër ya fa gën a naat, di serlu ca genn taatu garabu màngo, yor gitaaram, di woyaale, walla di bind i woy, mbaa waaj jotaayu rajo, walla sax muy xalaat naka la Mari Elen dunde demam gi…  

Yenn saay ma am lu ma yëg, daldi bind ay mbir. Li tax mënuma woon a bindal Rafayel Njaay ay baati seede, dama doon dof-doflu, mel ni ku nàndul bu baax, naan ci sama xel : xéy-na Aamadu Lamin Sàll dina ma woowaat ni ma “déedéet, Ndey, njuumte la woon ; Rafayel mi ngi fi”. Bi ma xaaree-xaar, déggaatuma dara, ma ni ndeke Yàlla moom, bu bëggee, jaam bëgg, jaam ay xal a ñàkk. Kon dëgg la ni sunu xarit boobee ñibbi na. Sàllaaw. « Bépp bakkan bu ñam dund, dina mos dee ». Dee, nga wax, de ? ! Aa, baat bi dal na…

Wax ji mooy dee la doom-Aadama dul miin doonte bés bu Yàlla sàkk nga dégg ku faatu. Waaw léegi, su dee nit ki day juddu, dund as lëf, faatu, luy njariñu dund ak dunyaa ? ! Uséynu Kan, sama xaritu filósof bi, dina ma ci indil xalaatam.

Su ma Rafayel daan xamleek kenn daf naan ko : sama xarit la, mi ngi tudd Ndey Koddu Faal, bindkat la. Su ko defee ma gaawantu teg ci bindkat bu siiwalagul dara. Su nu kooku wonee ginnaaw, ma ni jàkk Rafayel, laaj ko lu tax mu naan man bindkat laa ? Ngir nga gaaw pare te wone li ngay bind. Ndeysaan…Ku sawaroon la ci ñaaxaate ak kañaate ; ñàkk kiñaan moo ko waraloon.

Dóor waar la Rafayel xamoon ba taxoon koo sopp lool baat bii di « toogaay amul »… Daawul yàgg ci njéggil kàddu. Amoon na yitte tamit ci nit ñi.

Rafayel foonkoon na fa mu fekk baax. Moo tax delloo nañ ko fa njukkal.

Bëggoon naa leen a nettali bés bu neex ba ko Sowaal doon sargal, mu “inviter” woon maak Raasin Seŋoor ak Séydi Sow…

Ladab ak mbatiit la daa dundal. Téeree nu boole woon waaye dem nanu ba sunuy njaboot xamante. Laata ma naan soxnaam siggil ndigaale, moo ma jëkk ni “Ndey Koddu, mas-sa, sa xarit bi dem na, de”… Ahãkay, Rafayel, sama xarit la woon. Am na lu bari lu rafet lu ma mën a wax ci moom. Waaye, kàddu yi ñoo bañ, caŋ, xam naa dañoo bëggagul a génn…

Kon nu àndandoo ñaanal Rafayel Njaay mu xippe Guyaar te Yàlla teg loxo njabootam.

Téereem bi mu duppe « Cadences et lagunes », Séex Aliyu Ndaw moo bind ubbite bi. Fa muy waxe « Raphaël Ndiaye est un poète » moo ma jóo ci tudde sama seedee lii Rafayel taalifkat la woon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj