REAL MADRID JËL NA “SUPER COUPE D’EUROPE” BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

“Super Coupe d’Europe” mooy kub boo xam ni, ñaar ñi gañe joŋantey kuppe yii di “Ligue des Champions” ak “Europa League”. Benn finaal rekk lay doon, ku ko gañe jël ab kub. Real Madrid mi dóoroon Dortmund ca “Ligue des Champions” ba moo ci doon daje Atlanta mi dóoroon, moom it, Bayern Leverkusen ca finaalu “Europa League”.

Démb ci àllarba ji, 14i ut 2024, lees ko doon amal. Mu nekkoon mats bu ñépp joxoon Real Madrid ndam laata muy tàmbali, mu ñëw dëggal loolu. Waaye, yombul woon ci moom. Nde, ci xaaj bu njëkk bi, Atlanta xawoon na ñeme Real Madrid ba am fa ay yoon yum mënoon a dugal. Waaye, Saa-Espaañ yi taxaw ba jëlu ci bii. Ba ñu dellusee ci ñaareelu xaaj bi, ca la ko Real Madrid tàmbalee sëpp kii di Atlanta ba ci 59eelu simili ba Valverde daldi dugal ci paasu Vinicius jr. Ñu doxalaat ba ci 68eelu simili ba, ci benn bal bu Rodrigo nangoo ci benn jañkatu Atlanta daldi roofal Vinicius jr. Moom itam, mu jox Bellingham mu dàkk ñépp taajal Mbappe mu daldi dugal biiwam bu njëkk ak Real Madrid. Ci 2-0 yooyu la jeexee.

Real Madrid di wëyal di bind mbooru futbal, Mbappe it gañe kubam bu njëkk ak Real Madrid. Waaye tam, kuppeg tugalam bu njëkk. Ba tay, Modric mi yëkkati kub bi, léegi mooy futbalkatu Real Madrid bu ëpp kub (26). Carvajal tamit, ci mbooram, gañe ñetti kuppeg tugal yees tegoon yépp ci 2024 bi (Ligue des Champions,  Euro ak Super Cup d’Europe).

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj