Keeroog, 6eelu fanu awril 1994, lañ song roppalaanu Njiitu réewum Ruwàndaa, mu ñàkke ci bakkanam. Ca ëllëg sa la rey yi door, takkarnaase lool, ci lu gaaw.
Rey gu mettee-metti, jéggi dayo, ñeel Tutsiy Ruwàndaa ak képp ku leen doon jéem a wallu. Faagaagal gu teguwul ci lu dul xeet kepp ; kii Tutsi la, dees koy rey. Njiitu Farãs, Emmanuel Macron, nee na Farãs mënoon na dakkal Faagaagal gi te defu ko…
Li waral mu wax ko mooy Tubaab yi dañoo faraloon bóomkat yi, di leen jàppale ci rey seen i mbokk. Ndax Ruwàndaa, ña daa reye ak ña ñu rey, ñoom ñépp a bokkoon mennum réew, wenn làkk wi, jenn Yàlla ji, menn mbatiit mi, ba noppi nekk wenn xeet. Laata Belsig di noot Ruwàndaa, xeet amu fa woon, li amoon Ruwàndaa ay xeeti liggéy la. Tutsi yee moomoon njur gi, nekk i sàmm. Hutu yi di ay beykat. Ñiñ naan Tuwaa yi ñoom di jëf-lekk yi ak liggéeykati loxo yi. Lii moo tax ñu naan Ruwàndaa benn xeet la.
Kon lu waral ñàkk a déggoo ba egg ci Faagaagal ?
Nootkat bi moo leen féewale bim defee ci boppu waa réew ma ne ñii Tutsi lañu, ñee ay Hutu lañu te buñ deful ndànk Tutsi yi dinañ rey Hutu yi ba ñu jeex tàkk, daldi jëlaat nguur gi. Ginnaaw sama bopp a ma la gënal du bañ naa la, Hutu ya door di song Tutsi ya ci ndimbalu Tubaab yi. Di rey bés bu Yàlla sàkk lu tollook 10.000iy nit ci diirub 100i fan. Moo tax ñu naan Faagaagal gi mi ngi ci 1.000.000i Tutsi yu faatu. Ay rey yoo xamente ni xel mënu ko natt ci metit, tiis ak na ñu ñaawe.
Kigali Genocide Memorial
Ci liñ nettali ci téere yi ak it ay way-seede yu ko dund te Yàlla def ñu rëcc nee nañ ay nit daa nañu fey reykat yi ngir ñu reye leen ak fital te bañ leen a rendi walla daggate.
Soo demee Ruwàndaa ca béréb bees Mémorial du Génocide, am na fuñ tudde La Chambre des Enfants. Néeg bu yéeme lool ndax nataali tuut-tànk ya fa ne ak seen i at ak na ñu leen bóomee. Dangay gis xale yu rafet, amuñu sax at. Gis it xale yu ànd di ay mag ak rakk. Ñu bind ci seen suufu nataal ni ñu leen reyee : ñii dañ leen rendi, ñii dañoo dagg seen cër, ña ca des ñu luqi seen bët, ñale ñu jamat leen itam, ñuy yuuxu ba ni nemm, sedd guyy. Ay ñaawteef yoo xam ni doo mës a xam lu nekkoon ca boppu nit ki doon def loola, jamono ja mu koy def. Ak yeneen ak yeneen. Foo ko natt ci bon ak ñaaw, weesu na ko. Yenn saay sooy xool ba mu yàgg, danga naan ci sa xel « lii de, su ma ko gisul woon, suñ ma ko nettalee dinaa ne ki ma ko nettali day sos walla day yokkal ». Ku ko bëgg a nettali sax danga dul am i baat ngir wax na mu demee woon. Loo wax wax, am loo bàyyi, am lu làmmiñ mënul tudd. Damaa wax tuuti ci benn ci bérébi fàttaliku yi muy Mémorial de Kigali. Waaye am na yeneen yu des, yu ci gën a daw yaram nga ne yii la ; yu demee ni Murambi, Gisoosi ak Nyamataa. Ay njabooti lëmm far nañ. Ay xale doon ci saa si waajur ndax ndey ak baay yuñ bóom, xale bi war a toppotoo rakkam te fekk sax taneewu ko lu bari.
Ruwàndaa ! Réew mu yéeme…
Tey, 30i at ginnaaw Faagaalug Tutsiy Ruwàndaa yi
Léegi nag, 30i ginnaaw ñaawteef yii, Ruwàndaa bokk na ci réew yi gën a suqaliku ci Afrig, ràññeeku lool ci yar ak liggéey, cet ak njub. Duma ne ñépp a jub waaye ñépp ay jubal ndax ku jubul tamit dinga ragal a luubal ndax xam li la ciy fekk : kenn du la baal. Li yéeme tamit ci Ruwàndaa mooy dinga gis kuy dund ak ku rey i mbokkam te duñ am benn jafe-jafe ndax dañoo woote baale, bennoo jëm kanam bañ a geestu te gëm ko. Baale nag tekkiwul fàtte. Ndax bu dul woon ak bérébi fàttaliku yi (lieux de mémoire) sooy doxantu Kigali mënoo njort ne fii dara xewoon na fi. Waaye nag suñ faree béréb yooyu ci dëkk yeek mbedd yi mënuñu leen a far ci xol ak xeli ñi ko dund. Te sax fàttaliku day tax ñuy moytu aka sóoraale bay fexe lu mel ni Faagaagal du amati. Bañ à fàtte it dina tax ñi rey seen iy ñoñ xam ni ñi dee deewuñu cig neen ndax seen ug mbóom jàngal na askanu Ruwàndaa ak àddina ni ndeke doom-Aadama du dara te xare mën na soosoo ci loo yaakaarul woon : xeeb xal mu lakk sa dàgga.
Njiiti Ruwàndaa nee nañu Faagaagal gi mi ngi seen ginnaaw, li leen soxal mooy sàmm mémoire bi te ñaax ndaw ñi ñuy xool li leen iy jëmale kanam, ñoom ñiy ëllëgu réew mi rawatina ñi ëpp ci réewum Ruwàndaa amaguñu 35i at ci askunu 14i milyoŋi nit. Réewum Ruwàndaa mi ngi tabax ak a suqaliku. Ay ndawam ñooy « yaakaar ak kóolute » ngir ëllëg gu ñoŋ. Ci kow loolu dinañu màggal Faagaagal gi ci diirub 100i fan. Wëppa biñ tànn mooy : « Fàttaliku. Bennoo. Yeesal ». Wàlluw pàttaliku, ay bindkat def nañ ci liggéey bu am a am solo ñu demee ni Wérónik Taajoo (L’ombre d’Imana, voyage jusqu’au bout du Rwanda), Gayel Fay (Petit pays), Bubakar Bóris Jóob (Murambi, lelivre des ossements), Kulsi Lamko (La phalène descollines), Cerno Mononémbo (L’Anîné des orphelins), Abdurahmaan Wabéri ak ñeñeen. Seen liggéey tax na ñu bari ci àddina si xam dëgg-dëgg lu Faagaagalug Tutsi yi tekki.
Doomi Ruwàndaa defuñu nenn ak yaras (complexe)
Ruwàndaa ak li mu dund ci naqar, yàqule ko ci bépp fànn, réew la mu gëm boppam, mu amatul lu muy ragal. Xamatul sax faf fu « tiitukaay di nekk ci nit » ni ko Jonas Akintoye di waxe ci Malaanum lëndëm bu Bubakar Bóris Jóob. Te tamit « ku leen iy jéem a xoqtal, ay ree la leen di def » ci kàdduy Njiitu réew ma, Paul Kagamé. Moom it mi ngi xamle, ci bésu 7 awril 2024 bi ci teewaayu Njiitu réew yu bari ca Ruwàndaa ak it gan yu bawoo fépp ci àddina si ngir bokk ak ñoom pàttalikug Faagaagal gi, ne :
« Ginnaaw Faagaagal gi, danoo dogu ci naka lees war a def ba du amati mukk. Ñetti njàngat lanu ci jële :
Bi ci njëkk, nun askanu Ruwàndaak Afrig, nun rekk a mën a dund dundiin gi nu bëgg. Kenn mënu noo gën a bëgg sunug dund. Lii rekk mooy dàtt sunu wareef ba nu mën a nettali sunu mboor ni mu deme dëggantaan, Faagaalug Tutsi yi ni nu ko dunde.
Ñaareel bi, bu nu xaar ndimbal ci kenn walla nuy tàggoo ngir def li war. Moo tax bu nuy ñenn ñi di jéem a artu, ay kaf lay war a doon ndax ñooñu xamuñu li ñuy wax.
Ñetteel bi, dogu ci xeex “populisme” ci wépp fànn ndax mooy njeexital bi gën a leer ngir sooke faagaagal.
Ndaw ñi ñooy ëllëgu réew mi, ci ñoom lanu yaakaar ngir bennoog askan wi ».
Xanaa kon dunduñu luy nirook yaras ? Déedéet !
Njiitu réewum Ruwàndaa mooy nettali. Nee na « Lii doomu-Afrig ju nekk war na koo bàyyi xel. Man de, mësul génn sama xel. Dafa amoon ndaw soo xam ni dañ koo tancoon cib diggu tali, di ko laaj naka la bëggee ñu reyee ko ko. Ndaw si ne jàkk defkati ñaawteef yi, seen iy bët jàkkaarloo, mu tëfli leen ci kanam. Ndaw soosu am na lu mu nu jàngal…
Ruwàndaa, deesu ko mës a reyaat, mukk ci àddina. Mukk, nag, laa wax ».
Kon nag Faagaagal, na fi yem !
Kàddu yooyu, Ruwàndaa taxoon Póol Kagame yëkkati leen waaye bépp Saa-Afrig war na cee bàyyi xel bu baax a baax.