Bërki-démb, ci gaawu gi (21eelu oktoobar 2023), lañ doon aajar téere Porofesëer Saaliw Mbay bim mujje génne tudde ko Ndande Fall, Keur Madame ci bérébu mboor ak xayte, WARC.
Ndaje maa ngi door bi 4i waxtu ci ngoon tegalee 35i simili. Porofesëer Usmaan Seen mi jiite WARC moo ko ubbi, dalal gan yi laata muy wax lu tax tey ñuy aajar téere bii ca béréb boobii.
Imaamu jàkkay Sacré Cœur 3 moo feelu Usmaan Seen ci ndoorte li, daldi ñaan, teg ci seede ci Saaliw Mbay.
Sëñ Majib Seen lañ taamu woon ngir mu séddale kàddu gi. Waaye, laata mu koy jox kenn xamle ne sëñ Saaliw Mbay mi leen dajale tey nit ku baax la, ku yaatu te oyof, war a doon royuwaay ci bépp doomu Senegaal ngir xam-xamam ak màndoom. Saaliw Mbay ku bëgg njaboot la, xam li ko war, fonk diineem, jàpp ay xaritam ak cofeel, defu leen yen.
Nee na tamit Saaliw Mbay sant bu baax ci Yàlla dajaleek ku mel ni soxna Penda Mbow mi nga xam ne ñépp ràññee nañ ngëm-Yàllaam, dox ci soxlay maxejj yi ak it xeex ngir jigéen siggi, jëm kanam. Ndax, Senegaal mënul suqaliku te jigéen ñi defuñu ci seen loxo.
Nee na sëñ Mbay ci téerem bii mi ngi ciy fàttali ni Ndànd meloon ay at ci ginnaaw, waaye léegi dafa soppiku, ànd ak jamono. Ndànd mooy xolu Kajoor ak kàngaam ya fa jot a jaar ñu ci mel ni Maajoor Saala, walla Lat Joor ba ci Demba Waar añs. Ciy kàddoom, téere bii ñuy aajar, képp kuy doomu Ndànd war na koo am ndax Saaliw Mbay daa dekkil Ndànd Faal ba fàww.
Mi ngi daaneelee ay ñaan ñeel Saaliw Mbay ndax dundam am na njariñ.
Ñàkkul sëñ Seen dafa am tuuti taardmaa ndax dafa bëggoon Usmaan Seen wuutu ko ci waxukaay bi te booba kooku wax na ca ndoorte la.
Naaka noonu mu toftal ci boppam sëñ Aadama Faal miy meeru Ndànd. Lii la wax ginnaaw bi mu fésalee mbégteem :
« Téere bii sag la ci waa Ndànd yépp. Ndax, ku xamul woon Ndànd dina ko xam tey. Ci kow loolu Ndànd ameel na la njukkal. Sa jaar Ndànd am na solo, def nga lu réy. Te soo nu ku nangulee, Ndànd def la Citoyen d’honneur. »
Aadama Faal ak lamaanu Ndànd di Allaaji Mbay Joor Faal ak « délégation » bu réy ñoo àndoon ci bés bi.
Ginnaaw moom, Góora Ja moo dawalal mbooloo mi kayitu Mamadu Juuf mi fa waroon teew te am ngànt. Li sëñ Ja dawal mi ngi ci 4eelu feggu wi (4ème de couverture). Bi mu ci noppee wax na turu boppam xar-baax yi ci Saaliw Mbay, « jege ko, liggéeyandoo ak moom sag la, bànneex la ndax xam-xam bu yaatu ak njàngaleem mu mucc ayib. Soo koy xam dina ko naw ba noppi mu lay jóo. Yal na ko Yàlla sàmm. »
Bi Góora Ja seedee ba noppi, porofesëer Penda Mbów moo jël. Lii la wax :
« Maa ngi sargal sama xarit, sama càmmiñ Yero Silla. Saan Loppi, soxnaam waroon na fee teew tey. Yero Silla moo fi jëkk a sos kurélu maxejj àndoon kook Saxiir Caam. Moo fi sosoon tamit yéenekaay bii di Sofaa mook Buuba Jóob. Digganteem ak Aamadu Ampaate Ba umpul kenn. Maa ngi jaalaat soxnaam.
Bés bi nag, mujj na ñëw. Saaliw jàppoon na ni du mës a ñëw ndax tamit yenn saay yaram wi sutante, mu foog ne du eggali téere bi. Téereem bi nag, Saaliw liggéey na kook njàmbaar ak coono, sonn na ci.
Waaye tamit nu ngi ciy gërëm Mari Ayda Jóob bu Présence Africaine. Aliyaa fexe bañ indi fi tey 600i téere. Ndax, soo gisee li ci Saaliw tudd ciy njaboot rekk, nga xam ne kon dawalkat yi dinañ takku. Daanaka waa Ndànd, ñépp ngi fi. Muy lu am solo ci Saaliw Mbay ak i doomam. Maa ngi gërëm doomi Saaliw, samay doom yu baax lañu. Tey jii sax, Nguuda miy taawam daf maa xéyee cabbub tóor-tóor bu yànj. Ma bég ci lool, di ko gërëm mook ay rakkam.
Maa ngi gërëm Majib Seen. Lu am doolee nu boole.
Porofesëer Cubb nekku fi, waaye nee na bëggoon na xam kumpa gi ci téere bi. Saaliw Mbay moom, daf ne woon rekk móolkat bi « Ndànd, ñor na ma ». Soo bëggee xam lu ko waral jàngal téere bi. Te yemu ci ndax Porofesëer Saaliw da cee def liggéey bu am solo ci wàllu xel ak firnde yu wóor, mësul tàyyi ci laajte ak a leerlu. Bu nu fàtte ni Saaliw « archiviste » la. Man, waa Kajoor laa te sama pàppa amoon na ag tóokëer. Waaye, man mësumaa xam ne tóokëer toolu kër lay tekki. Ci téere bii laa ko jànge. Boroom mi ngi ciy nettali dundiinu mboolaay gi, njabootam, naka la dem beek dikk bi soppikoo, njariñu gaar yi ak yu ni mel.
Téere bi Saaliw da koo bind ngir tontu sëtam, Amadi, bi ko laaj bés « maam, kañ nga may bindal téere ? » Naam téere seede la waaye jàpp naa ne mooy téereem bi gën ci li mu mës a bind, ndono la. Ci biir téere bi mbooru xarala ci wàllu gerte, Saaliw faram-fàcce na ko ci lu yéeme. Ndax gerte mooy way-jëmmal ju am solo ci sunu digganteek Tuubab bi. »
Bi Penda Mbow di wax lii mi ngi jeqiwaale gerte gi ci leget gi tege ci kow taabal ji. Nee na yit :
« Téere bii di Ndànd Faal Kër Madam, téere la buy bàkk xaritoo ak dëkkandoo. Saaliw tudd na ci daanaka xaritam yépp. Bàyyiwul ginnaaw diisoo ci diggante diine yi. Waaye man ki ma gën a yéem ci téere bi mooy ndaw si ñu naan Kumba Tayba, nga xam ne bi bombàrdamaa bi amee, te ñu toxal askan wi, dafa yéeg ci saxaar gi, tukkee Ndakaaru ba Ndànd ci wagoŋ yi. Moom day jëmmal ci man njàmbaaru jigéenu Senegaal ak sàkku moom boppam ba noppi kenn jàppalewu ko, moo eggal boppam. Téere bii daal téere jaar jaar la, téere saytu la. »
Fadel Ja, moom dafa xamle ni, 11i at ci ginnaaw moo aajaroon téere Saaliw Mbay. Moo ko tax a wax ne :
« Kon tey su ko Saaliw taamuwaatee ngir defaat lu ni mel ci téere bu bees bii day tekki ni bégoon na ca la ma defoon. Ma koy gërëm ci kóolute gi. Daf ma ni woon nag : su ma fekkee ak su ma wuutee yépp, yaa koy aajar. Waaye dee du jaas, kon kuy dund rekk dina faatuji. Boobaak tey, ay weer jàll nañ, nu ngi nii daje, di wone téere bi ci teewaayu bindkat bi mu ànd ak wéram ak xelam.
Ndànd Faal Kër Madam daa mel ni ay luññutu yu tegloo, bokkul ak laaji takk-der yi. Waaye, yoy ma-pasin (artist) dawal la. Saaliw Mbay jox cër dëgg, sukkandiku ci tontu yu bari te wuute, yuñ bind ak yuñ wax. Kiy Dina jur ay laaji-laaj ci boppu dawalkat bi waaye Saaliw mboorkat la.
Téereem bii di saamandaay waxtaan wu yaatu woo xam ni Saaliw da cee feeñal boppam, dafa am 3i jubluwaay :
– Sëtam moo ko ko sant, mu nangu te bind daa fiir ndax wéetaay dëgg ak moom sa bopp la laaj ; muy kon lu jafe.
– Bind tamit ngir seede ndax mi ngi xalaat ndaw ñi nga xam ni tey daanaka seen yaakaar yàqeeku na
– Xéy-na tamit bind ngir jéem li ku nekk di jéem muy dekkil sag ngone. »
Bi Fadel Ja noppee, Séydu Madaani Si moo àddu, ne mu ngi xamanteek Saaliw Mbay ci atum 1967 :
« …te boobaak tey saa su ne mu jox layi sag ak mbégte ñeel jëmmam. Ecole des chartes moo nu boole, ma jiite woon tamit « jury » teesam. Lu bari lu rafet dox sunu diggante. Saaliw Mbay def na liggéey bu am solo ci Archives nationales diirub 30i at. Téereem bi tudd Histoire des instutitions comtemporaines du Sénégal am na solo lool. Ndànd Faal moom day fàttali Ndànd ci ati 1950 ak ni mu doxee ba tey jii. Kon maasi tey yi ak yiy ñëw mën cee sukkandiku ngir wéyal mboor. »
Laata boroom bés bi, Saaliw Mbay, di yëkkati kàddu, géwélu juddoom, Njuga, tagg na ko, kañ ko, fàttali mbooloo mi baaxi maamam.
Porofesëer Mbay sant na njabootam, doom ak i sët, xariti ngonendoo, liggéeyandoo, kilifa diine yi ak yu nguur yi. Teg ci :
« Samag dund yépp damaa mës di dajalee ay këyit ngir sédde ko, sama liggéeyu archiviste la. Waaye tey nag man maa soxla këyit yi ngir sama téere. Soppiwuma li am walla ma koy tey-teylu juum, du sama nit. Li ma fii wax dëgg la. Damaa bind Ndànd Faal Kër Madam ndax samag ngone, maa ko mën a wax, nettali ci làmminu boroomam. Fa laa dundeek samay waajur ba ba may am 13i at. Sabab bi, sama njaboot la woon, ginnaaw gi laa ko yaatal waaye ndox du bàyyi yoonam ; doxiinu archiviste day dale fa gën a yaatu wàcc ba fi gën a tuuti.
Maa ngi gërëm njiitu Fondation Sonatel Aminata Faal Sidibe ak Madlen Dewi Seŋoor. Di gërëm Séydu Madaani Si ak sama xarit yépp. Di gërëm bu baax Pr Penda Mbów, jàppale na ma, di ma ñaax, di ma soññ, dimbali na ma. Téere bii téereem la. Maa ngi lay kañ, di la ndokkeel.
Ku ne téere ne móolkat ; maa ngi gërëm Mari Ayda Wan Jóob.
Maa ngi jaalaat Saan Lopi Sillaa.
Maa ngi gërëm sama soxna Aminata Sekk mi ma àndal. Mu bàyyi léppam di ma toppatoo, xam na ni mag, ay atam, dafa am yu mu laaj. May féddali samay yëg-yëg yu sax ci moom.
Samay doom maa ngi leen di ñaanal ñaanu baay bu bég. Maa ngi gërëm ñépp ». Noonu Mari Nguuda miy taawam biral mbégteem, yëkkati kàddu ci turi rakkam. Ñoom ñépp àndadoo di ñaanal seen pàppa, « baay bu baax, bu leen jàppale, taalibe tijaan buy wird jawartul kamaal, di jàng salaatul faatiha, bëgg lu baax, mën a sañse. » Ñoom doom yi dañoo bindal seen pàppa woy, def ko nataal, ñaari sëti Saaliw Mbay jox ko ko ci kanamu mbooloo mi.