Bërki-démb, ci gaawu gi (21eelu oktoobar 2023), lañ doon aajar téere Porofesëer Saaliw Mbay bim mujje génne tudde ko Ndande Fall, Keur Madame ci bérébu mboor ak xayte, WARC.
Ndaje maa ngi door bi 4i waxtu ci ngoon tegalee 35i simili. Porofesëer Usmaan Seen mi jiite WARC moo ko ubbi, dalal gan yi laata muy wax lu tax tey ñuy aajar téere bii ca béréb boobii.
Bi ñu egsee ci ñaareelu xaaju ndaje mi, Mamadu Mbay moo jël kàddu njabootu Mbay ci ndigalu seen mag Libaas Njaay. Li ñépp wax la wax, mbaax du weesu mbaax. Nee na Saaliw Mbay fépp fu mu mës a jaar jàngalekat ya dañ koy bëgg ; moo daan jiitu ci fànni jàng yépp ba mu des tàggat yaram.
Musaa Sare, xaritu benn-bakkanu Saaliw Mbay la ba noppi seen i waajur nekkoon i wóllëre, te bokkoon nekk nawetaan. Moom sëñ Sare ngir fàttali lu nawetaan làmboo ko tax a jël kàddu. Wax na lu am solo ci diggante Saaliw ak fonk mbatiitu Senegaal ak làmminu wolof wi mu nàmp ; làmmiñ dara ëpp ko solo ci mbatiit.
Ci solos nawetaan yi nee na ñi jiitu ñooy tette, wone yoon, di dox ci jàmm ak xaritoo ; kujje mbaa kiñaan mësul dox seen diggante. Ñi féete ndaw nangul leen cër boobu tey dox ci seen i tànk ndax puso bi bañ a réer.
Baabakar Fay tamit ba tey xaritu Saaliw Mbay teewal fi mbooloom xarit yi. Moyul li ñi ko jiitu wax, moom mi xaritook bindkat bi lu tollu ci 63i at yu mat sëkk te dara mësul ñaaw seede na ne :
« Mësunoo werante, daa nan waxtaan guddi ba fajar gi xar. Kocc Barma nee na lu yàgg dëgg la.
Man nag duma dawalkatu téere bu mag, booy seet Netflix laa gën a jox bopp, di seetaan film yi waaye téere Saaliw daa neex a dawal te day yee ci nit ki xéddu dawal. Saaliw daa mës a neex deret, laabir, di ree rekk, ku ci nekk ci nun waxal na la dara lu rafet ci téere bi. Yaayam da ko daan wax Saaliw bàyyil sa ree ju bari ji, nit soo bëggee ñu weg la dangay mer yenn saay. Su ko defee Saaliw ree ba xàqtaay. »