SAARAYA : AY SAAY-SAAY ÑOO SOQI FETEL CI AG DAAMAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fa Saaraya, féete ci diiwaanu Kéedugu, la ay saay-saay song ag daamar, soqi ciy bali fetel. APS moo siiwal xibaar bi niki tay ci alxames ji, 4i pani sulet 2024. Nee ñu, dawalkat bi jëlee na ciy gaañu-gaañu.

Ab « 7 places » la defkati ñaawteef yi song, fekk mu ngi jëmoon diggante Duuta ak Màndanxoli, ci bokk-moomeelu Xosanto, depàrtmaa bu Saaraya. Sunuy naataangooy APS jukki nañuy kàddu ci kenn ci takk-der ya féete mbir mi, mu wax ne :

 “Juróomi saay-saay yu nëbb seen i kanam ñoo soqi ay fetel cig daamar gu bawoo woon Duuta. Dañu jam dawalkat bi ci dënn.”

Boroom kàddu gi dafa leb turam.

Rax na ca dolli ne, juróom-benni nit yi daamar gi yeboon, ñoom, dañu nangu seen xaalis, seen i jollasu (telefon) ak yeneen xeeti alal yi ñu yoroon yépp.

Birigàddu sàndarmëri bu Xosanto ubbi na ag luññutu ngir topp saay-saay yi def ñaawteef boobule. Nde, ginnaaw bi ñu defee seen tóoxidóona ba noppi, dañu fab seen i tànk, daw.

Jamono jii, dawalkat baa nga irsãs (urgences) bu raglub Amaat Dansoxo bu Kéedugu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj