SÉEX ALIYU NDAW GÉNTOON NA KO DÉMB, AADAMA BAROW AK BASIIRU JOMAAY FAY DEF NAÑ KO TEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Atum 1981, Séex Aliyu Ndaw, bindkat bu ràññeeku, daa bind woy tudde ko : Sama mbokku Bànjul. Di ci ñaax ak a digal Saa-Senegaal yeek yu Gàmbi su ñu dajeetee ñuy waxee kàllaamay Kocc te bàyyi Pierre mi jàngal kii « non » ak John mi sa kee « yes ». Ci gis-gisam, Senegaal ak Gàmbi dañoo war a déggoo ci fab làkku Molière ak Shakespeare « ne leen fiij ci saaku, daw ba diggu géej, ne leen ca yalbàndiŋ». Suñ noppee joxante loxo, ànd ne « waaw xaw a dee ! »

Bi Séex Aliyu Ndaw di bind lii, booba, Njiitu réewum Senegaal, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, menn at rekk la amoon. Nde, 1980 la gane àddina. Ren, ci atum 2024 mile, Njiitu réewum Senegaal mii, seeti na naataangoom, Aadama Baro, Njiitu réewum Gàmbi. Ñu daldi séq jataay, weccante xalaat ci wolof, ñoom ñaar ñépp dégg ko, ñi ëpp it ci seen iy askan, naka noonu. Nde « ñaari réew yee bokk mbatiit, bokk mboor bokk dénd ». Moo tax itam, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay taamu Gàmbi ngir ñaareelu tukkeem ginnaaw bi ko Senegaal falee ci boppu réew mi. Gànnaar la tàmbalee tukki nemmeeku, ndax la Njiitu réew ma, Mohammed Oul Ghazouani, nekk tamit njiitu Bennoog Afrig (Union Africaine).

Woyu Séex Aliyu Ndaw wii, tombe la, gaaf la walla boog gisaane ? Ak lu mënti am, bi Bubakar Bóris Jóob di sargal Séex Aliyu Ndaw ci Bàmmeelu Kocc Barma, lii la waxloo Kinne Gaajo : « Séex Aliyu Ndaw, bindkat bu xam àddinaa ngoog. Moo tax liñ koy dégg bariwul ».[1]1

Gudd leen fan te mu ànd ak wér, ngeen iy wéy di nu bégal ak a jàngal ci seen xalima.

Jàngkati Lu Defu Waxu, Sama mbokku Bànjul a ngii ci suuf :

SAMA MBOKKU BÀNJUL

Sama mbokku Bànjul

Sama doomu-ndey

Bokk der bokk kàddu bokk deret

Céy nun wóoy li fi jofsi

« John » dafa nëw « Pierre» agsi

Ñu bàyyiloo la « ma ne » sa la « yes »

Jàngal ma « Non »

Su ma nee Molière nga ne Milton

Soo nee Shakespeare ma ne Corneille

May bàkkoo Sorbonne ngay tëggoo

Oxford

Tee noo dellu ci Kocc mi nu nàmp

Sama nbokku Bànjul

Sama doomu-ndey

Jàppal « yes » ma ne nuus « non »

Nu ne leen fiit ci saaku daw ba

Diggu gééj ne leen ca yalbàndiŋ

Nga jox ma loxo ma jox la loxo

Nu tëb ba ca asamaan

Bokk ne « waaw xaw a dee »

Sama mbokku Bànjul

Sama doomu-ndey.

Séex Aliyu NDAW, Ndakaaru 1981

Lolli, Taataan, IFAN, ENDA-DAKAR, 1999, xët 24

 

[1] Bubakar Bóris Jóob, Bàmmeelu Kocc Barma, EJO-Editions, Ndakaaru, 2017, xët 66

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj