Séex Anta Jóob a ngi juddoo Céytu, 29eelu fan ci desàmbar 1923. Alxuraan la dale njàngam laata muy dugg daaray nasaraan. Ci 22i atam la am ñaari bakalóoriyaa. Ginnaaw gi, atum 1946, la dem tugal ngir mottali njàngam : màndaqe ak xeltu. Waaye nag, loolu terewu ko woon wéyal gëstoom ci làkk yi. Nde, Séex Anta, ku teel a yeewu la woon, te xamoon li mu bëgg.
Dundam gépp, Séex Anta Jóob daf ko ndeyale woon lépp luy pexe yu nit ku ñuul mën a def ngir suqali kembaaram, gëm boppam, liggéeyal ëllëg. Moo nu jàngal ni, soo bëggee jëm kanam, dangay fexee xam fi nga jóge, xam sa démb ngir waajal sa ëllëg.
Te li am ba des mooy, nit, deesu ko jox wàccuwaay wi mu yelloo fileek xamul boppam. Fonk sa bopp, fonk li la Yàlla cërale moo nu jóo ci sos këru móolukaay gii di EJO-EDITIONS ba noppi lëkkale ko ak dalub caabal (yéenekaay) ci wolof, tuddee ko Lu Defu Waxu (www.defuwaxu.com).
« Menn réew mënut a suqaliku ci làmmiñu jaambur. »
Ëllëgu Afrig ak i ndawam bañ a yaafuus, bañ a yaras ñoo nekkoon li ko soxal. Séex Anta firndeel na ci liggéeyam ni, nit ku ñuul a jiitu ci àddina si, te it saa-Afrig yee xàdd xayteg àddina. Mësul a tàyyee aartu jëmale ci njariñu jëfandikoo li nu moom, dale ko ci làmmiñi réew mi. Ca atum 1954 la ni woon, ca teesam ba, Nations nègres et culture : « menn réew mënut a suqaliku ci làmmiñu jaambur ».
Tey, daanaka 70i at ginnaaw digleem ba, lees war a dugal luy tollu ci 6i làmmiñi réew mi ci ekooli Senegaal yi. loolu di jéego bu am solo te, ku am seetlu bu baax, dinga gis ni li yéexal doxub kembaar gii di Afrig, mooy xaw a umpale ñi nu doon ba mu yóbbee nu ñàkk a fonk sunu bopp. Ñu wonloo nu ginnaaw sunu mbatit, sunu xayte ak i làmmiñ. Moo tax, nu wëlbatiku jël weneen làkk di ci nos ak a nocci, ginnaawal sunuy yos.
« Na ngeen gànnaayooleen xam-xam ba diis gann »
Dëgg gu wex te ni fàŋŋ mooy ku xelu as tuut gis ni jàngee ci làkk wees jéggaani, amul mujj te jaaduwul ndax dafay mel ni, li weneen làkk mën, saw làkk mënu ko. Te, fii la ag yaras di tàmbalee.
Woroom xam-xam yu bari yiy yëngu ci wàllu njàngale ak njàngaliin (pédagogie) dëppoo nañu ci ni, bokk na ci njeexitali jànge ci làmmiñ wi nga nàmp ak mën koo bind, gaaw a xam, gaaw a ràññee, gaaw a mokkal…
Mbir mi du mbirum kafrigu (panafricanisme) kese waaye dangay xool li lay jëmale kanam, nga nekk ca. Lii rekk la. Ne woon na, ca ndaje Ñaame ma, ca Niseer, « Na ngeen gànnaayoo xam-xam ba diis gann », xam door a jëfee gën a wóor, kenn du la nax.
Bu loolu weesoo, kurél gi duppe boppam Kaarbon 14 daa dajale ay ndongoy daara ju mag jii di UCAD ak seen i ñoñ, di amal ug dox, at mu nekk, dale ko Ndakaaru ba Céytu, ngir sargal Séex Anta Jóob mi nga xam ni mii, bi muy faatu, kenn ci ñoom judduwul. Dafa di, lu ni mel, dafay gën a firndeel ni njàngaleem du lees naatable walla lu ñuy am xel-ñaar ci dayoom.
Ci atum 2016, nguur ngi dige woon na dugal njàngaley Séex Anta Jóob ci daara yi. Waaye, ba waxtu wii nuy bind yaxal gi, dige boobu ci ay wax la yem. Waaw, lu leen ko teree def ? Luy jafe-jafe bi ?
Yenn ci ay téereem :
L’Afrique noire précoloniale, 1960.
L’unité culturelle de l’ Afrique noire, 1962
Les fondements économiques et culturels d’un état fédéral d’Afrique noire
Antériorité des civilisations nègres, 1967
Nations nègres et culture, 1979
Civilisation ou barbarie, 1981
Séex Anta moo sosoon pàrti pólotig RND ci atum 1976. Taxawaloon na tamit yéenekaay bi tuddoon Siggi, mujj gi mu soppi tur wi, tudde ko Taxaw. Njiitu Senegaal ca jamono jooja, Seŋoor, xañoon na ko sañ-sañu jàngale ci daara jiy wuyoo Séex Anta tey jii. Kayitu pàrteem it, mi ngi ko jot bi Abdu Juuf nekkee ci boppu réew mi, keroog atum 1981.
Séex Anta Jóob bind na ci wàll yu bari te wuute niki ci fànnu kàttan, ràbboo réewi Afrig yi, kaaraange, koppar, koom añs. Waaye, nun, danoo taamu jukki ci solos jëfandikoo sa làmmiñu bopp.
Doomu sëñ Masàmba Saasum ji ak soxna Màggat Jóob dundul ci neen, faatuwul itam ci neen. Wàccoo na ak àddina, yey na ñi ko daan xeex ak a jéem a bunduxatal. Nde, ku dëddu diir bu tollu ci 36i at, bés bu Yàlla sàkk ñuy wéy di la fàttaliku, di la ñaanal, di la gërëm, di jéem a roy ci yow, day tekki ni sa dund am na njariñ lool. Dëggal na li wolof diy léebu, naan : « suul ker du ko tee feeñ». Suuxlu mbër, làng ak moom a ko gën, muy bëre daan, ngay ree.
Séex Antaa ngi génn àddina 7eelu fan ci féewaryee 1986 ci Ndakaaru. Su doon dund, tey jii lay am 99i at, téeméeri at yu des benn.