Séex Bàmba Jéey : “Ndawi Senegaal tey, ku jàpp ni ndaw yu amul jëmu lañu […]. Yow yaa juum.”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ñaari ati kaso yi àtte bi daan kii di Usmaan Sonko ak kii di Ndey Xadi Njaay, yëngu-yëngu yi metti nañ lool ci Senegaal. Dem na ba ñu ciy waññi tey 36i nit yu ci ñàkk seen bakkan. Bu ñuy xaarandi ba léegi kàdduy Njiitu réew mi, Maki Sàll, kii di Séex Bàmba Jéey moom jàpp na ni, ñàkk xam ndaw ñi ak bëgg leen a xañ seen bëgg-bëgg kott ko waral.

Ni ñu ko bokkee dund, ñaari ati kaso yi Yoon daan ñii di Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay yëngaloon nañu réew mi 4i fan yii. Fu nekk ñu nemmeeku fay yëngu-yëngal yu jur i yàqu-yàqu yu bare. Taafar ji bare lool. Dem beek dikk bi jafe. Daara yeek jàngune yi tëj seen i bunt. Ñu dem ba mbootaayi xeet yi ci àddina si di ñaan dal ak a sàkku ci kilifa yi ñu bañ a dugal réewum Senegaal ci guuta.

Fii mu nekk nag, ñépp a ngi xaar Njiitu réew mi génn wax ak askan wi lu ñu mën a dégg, li ñuy xaar ci moom ba dëkk bi gënatee dal. Ñi jot a wax moom bare nañu, ci Senegaal ba ca bitim-réew. Te lu ñépp, walla ñi ëpp boog ànd wax jar naa bàyyi xel. Li Séex Bàmba Jéey wax, jaare ko ci sunuy naataango yu Sud FM, dafa tënk lu bare ci coow li lëmbe réew mi.

“ Ndawi Senegaal tey, ku jàpp ni ndaw ñu amul jëmu lañu, walla nga ne ñi nekk ci mbedd mi tey ay dof lañu, xamuñu lu ñuy def, dañuy taal réew mi dañu koy yàq ndax xamuñu li ñu bëgg, yow yaa juum. Xamuloo ndaw ñi. Ndaw ñi, dañu jàpp ni dañ leen solal mbubbu, ga leen ko. Mbubbu mu xat ci ñoom, mbubbu mu daŋ, tàng ci ñoom, metti, mënuñu koo dékku, mu tere leen noyyi. Kooku, boo ko summiwul, jox ko lu ko jot dafa koy summi sànni ko, ngir mën a dund.

Ndaw yooyu nag, dootuñu nangu ñu [leen di] ga, di fi teg ñoo xam ne ñii, du  ndaw yee koy topp. Ñooy bëgg léegi di tànn seen i njiiti bopp. Bu ñu amee yaakaar ci ku mel ni Usmaan Sonko, topp ko, nekk ay tamndareet ci ginnaawam, bëgg kooku jiite leen, boo ñëwee ni kooku du fi am ba nga ciy jaar yoon yoo xam ni du yoon yu ndayu-àtte réew mi nangu, kon lépp lu am ci réew mi yow yaa ko fi def. Loolu nag mooy li nga xam ni mooy dox ci réew mi tey. Te moo indi jamono bii ñuy dund tey.”

Mu mel ni kon wax ji wax ji, ndaw ñee mer ba futt, mënatuñoo denc seen mer ñu génn lëmbe ba ñépp yëg ko. Ba tax ñuy fàttaliku ni ñaari at ci ginnaaw, bi mbirum Sweet beauté mi jollee, jotoon nañ wone seen bopp ba 14i nit  ñàkkoon ci seen i bakkan. Njiitu réew mi, génnoon na keroog, waxoon ne, “ndaw ñi, dégg naa leen”. Waaye, ci ginnaaw gi, dafa waxaatoon, daldi tëkku ndaw ñu, ne: « Li fi amoon dootu fi amaat ». Dootu fi amaat googu nag, ñu mëneesoon ci am ñaari déggin : benn, mu jox leen li ñuy laaj ba ñu féex ba dëddu seen lépp i naqar walla boog bu amatee man ngeen fiy fekk. Nu gis ne 1 suwe 2023, ndaw ñi delloo nañu buum ca boy-boy ga, mbir yi gën a tar ba làrme bi génn. Séex Bàmba Jéey nee :

“ Làrme bi nag, bu ñu demee ba génne ko, dama jàpp ni loolu njuumte la ci Njiitul Bokkeef gi. Moom, moo ni woon bu yàggul, li fi xewoon 2021, dootu fi xewaat. Ba mu ko waxee dama jàppoon ni nekkul mbiri ngànnaay lay wax walla doole ju muy sëf askan wi. Dama jàppoon ni dafay def ni, dina am ay taxawaay, am ay ndogal, am ay jëf ñeel politig geek campeef yi yuy tax ba lu xewoon du xewaat. Ndax, bu soppee doxalinam, soppi taxawaayam, sàmmonteek ndayu-àtte réew mi, di doxal yoon, cëral kujje gi ak seen i yelleef ba dalal réew mi, wóor na ni kenn du génn di ñaxtu.”

Ku dégg yile kàdduy Séex Bàmba Jéey, dangay yaakaar ni sax dafa ànd ci ni ndaw ñi di yàqe. Waaye, ak lu waay mën a jàpp, bees demee ba ñi faatu ëpp ña woon, yàqu-yàqu yi bare ba kenn xamul lu muy niru, nit ñi tiit ba kenn demul, kenn dikkul, ñu gis ciy widewoo ay nit ñu yorey ngànnaay yu diis boole ca di sox niki ñu nekk ci toolu xare, lees mën a wax mooy li fi xew raw na li fi amoon.

Waa léegi lu Njiitu réew mi war a wax ? Ginnaaw bi mu leen déggee, mbaa du ni leen bile yoon : “ Gis naa leen” ? Ak lu mu leen namm yegge, kujje gaa ngi koy xaar itam mu dummóoyu lépp lu jëm ci  ñetteelu moome gi te bàyyi képp ku namm bokk ci wote yii di  ñëw mu bokk, rawatina Karim Wàdd, Xalifa Sàll ak Usmaan Sonko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj