Séex Tiijaan Gaajo séqoon naw waxtaan ak waa Iradio (90.3), ñu doon ko dalal ci jotaayu Jury du Dimanche, yéenekaayu web Seneplus yaxal ko. Moom nag, àndul ak ñiy xelal Maki Sàll ñetteelu moome. Bu doon sagoom, Njiitu réew mi, Maki Sàll, bañ leen a may nopp.
Yéeney Séex Tiijaan Gaajo mooy Maki Sàll génne ci buntu bu mag bi. Loolu lay biral ci kàddoom yii :
“Bu ma amoon wërsëgu toog ak Njiitu réew mi Maki Sàll, te weeru sàttumbaar ba léegi maa ngi koy wër, doon kon naa ko xelal mu déglu waa beneen boor bi koy wax ne : “Yow Njiitu réew mi, sa jaar-jaar rafet na. Am nga sag bu réy ci say biiri maas ginnaaw jaloore yi nga def. Def nga lu bari. Liggéey nga lu kenn dul naatable. Li ëpp ci saa-senegaal yi xam nañ li nga liggéey. Say noon rekk ay neenal sa liggéey. Waaye, saa-senegaal yi moom, li ëpp ci ñoom, nangul nañ la sa liggéey.””
Séex Tiijaan Gaajo nag, nekkoon na fi jëwriñ jees dénk mbiri bitim-réew ci Nguurug Ablaay Wàdd. Jot na takk ay ndomboy-tànk yu bari, liggéey fu bari ci àddina si, amal i tukki fu nekk. jamono jii, moo jiite kurélug pólitig gees duppee ci farãse “Mouvement politique citoyen”. Kon, sikk amul ci ne, xam na ni Nguur di doxe ak géwél yiy faral di wër sunuy njiit yi, di leen xalamal bay lëndëmal seen i xel. Ñu ni mel ñooy faral di dugal njjit yi ciy tóoxidóona, féewale leen ak seen i askan. Xanaa wolof waxul ne, “Buur aayul, dag yaa aay” ? Moo tax Séex Tiijaan Gaajo neeti :
“Léegi nag, ni ma ko waxee, dafa naroon a siggil mboorug réewam ci atum 2024 mi. Li ma jàppoon ci sama xel mooy ne, Maki Sàll da doon mottali ñaareel ak mujjantalu moomeem 2024. Te, mooy gën a rafetle génn ci Njiiti réew yi Senegaal mës a am yépp. Damay ñaanal Njiitu réew mi mu bañ kemtalaayu kàttanam wax ak coowi nit ñi ko wër. Maa ngi koy ñaan mu delloosi xelam… Li koy tax a génne ci bunt bu mag bi mooy, mu gàntal ay ñoñam.”
Yoonu sag waa ngoog. Buntu jàmm bi leer na. Waaye, ndax Maki Sàll dina dégg li ko Séex Tiijaan Gaajo di junj ?