Ci altine jii weesu la kii di jëwriñ ju mag ji demoon ca Ngomblaan ga ngir dégtal fa li Nguur gi namm a def. Ndax, la ko jiitu tamit yeneen jëwriñ yi demoon nañu fa ngir ñu càmbar seen i nafa laata ñu leen koy woteel. Mu mel ni nag, Nguur gii ñu dippe Nguurug xeex (combat) ag yemale ak yembal moo ko tax a jóg, ci seen i wax, ngir dund bi gën a jàppandi. Jëwriñ ji nag waxtaan wi ci farañse la ko doore laata mu koy tënk ci wolof. Jot naa tënk li ñu def ci at yii weesu ak li ñu namm a def ci at yii di ñëw.
Kàddu yii la yékkati ca Ngomblaan ga :
« Benn ci dogi ndeyi-àtte yi dafa wax ne bu ñu taxawalee ag Nguur bala ñetti weer war na ñëw ci Ngomblaan gi wax sémbug liggéeyam (programme de travail). Sunug sémb nag ak ni càrti réew mi tëdde, Njiitu réew mi mooy wax nu muy tëdde, Nguur gi doxal ko. Nguur gi nga xam ne tey Njiitu réew mi daf ne, naa ko jokkaleel (coordonner) ndax loolu mooy tur wi gën a yell wu ñu war a tudde jëwriñ ju mag ji. Ndax, mooy kiy fexe ba ñépp mën a ànd, ñépp mën a liggéey doon benn.
Li Nguur gi bëgg a def mooy wéyal li nga xam ne ñi ngi ko fi doon def te ñu gis ci ay njureef yu mucc ayib ci fànn yépp, ma lim ko fi léegi ci kàllaamay nasaraan. Moo xam ci paj mi, moo xam ci lekkool yi, moo xam ci otorut yi, moo xam ci tali, moo xam ci yoon yi ci àll bi, moo xam ci lii ñuy liggéey ngir dimbali askan wi, lépp Nguur gi def na ci ay jéego yu am solo. Réew mi yokk na ci at yu mujj yi bala mbas mi di fi dugg Senegaal tegale na fi loo xamante ne nii bi ñu moomee sunu bopp ak léegi amunu ko. Bi mbas mi duggee Senegaal bokk na ci réew yi néew yi nga xam ne seen koom-koom delluwul ginnaaw donte ne sax nag lañu daan am amuñu ko ci at yu mujj yii. Waaye, bi Njiitu réew mi jëlee alal ju bari def ko ci koom gi tax na ba réew mi delluwul ginnaaw. Àdduna nag tollu na ci ay xat-xat. Boo xaymaa li réew mi am, ñu koy woowe Produit Intérieur Brut, daanaka téeméer yoo jël def na ko ci ag ndimbal (subvention). Bariwul ci àdduna réew yu ko ëppale, muy juróom-ñaari téeméeri miliyaar yoo xam ne def nañ ko. Ndax, bu dul woon loolu, fi ñu tollu nii ku fey ci kuurã ñaar fukk xamal ne Nguur gi jëlal na la ci 30%. Loolu lu am solo la. Esãs bi noonu, ceeb bi noonu, suukar si noonu, diwlin gi noonu.
Loolu nag lu metti la, dinanu ko wéyal ci atum 2022. Waaye, dinanu ko yemale ci 450i miliyaar. Ndokk nag, bi nga xamee ne ci àdduna si tey, gis nanu ne mbir mi coono bi mi ngi wàññeeku. Waaye, Senegaal moom, Yàlla xéewale na ko ci li nga xam ne boroom xam-xam yi xalaat nañu ko mooy at yii di ñëw koom-koom gi dina yokku ci loo xam ne réew mi mësukoo am walla bu ko amee it fàttelikuwuñu ko ci wàllug natt (statistique) muy 10%. Bu soobee Yàlla koom-koom gi dina yokk, Njiitu réew mi dina ko delloowaat réew mi yépp. Mi ngi ci peyoor yi, mi ngi ci paj mi, mi ngi ci liy tabax réew mi te bu soobee Yàlla loolu Nguur gi dina ko wéyal.
Leneen li nga xam ne Nguur gi dina ko def mooy réew kenn du ko tabax ci wenn fan, dañu koy waajal. Moo tax Njiitu réew mi, bi muy def Plan Sénégal Emergent, daf ko def ci àpp bu gudd, 2035, muy ñar-fukki at. Réew yépp noonu lañu leen defare, mu ñëw am yéene ci Senegaal taxawal loolu. Ñi ngi jëm ci ñetteelu sémb bi su soobee Yàlla, Nguur gi dina ko def balaa weeru suwe wii dina ñëw jébbal ko Njiitu réew mi. Waaye, bala boobu sant nanu nu waxtaan ci ak askan wi, indi ko fii ci Ngomblaan gi, waxtaan ci ak yeen ba nga xam ne saa-senegaal bu ci nekk joxe ci xalaatam. Bu nu ci paree, nu tënk ko jox ko ko, bu boobaa nu soog koy doxal.
Loolu lanu nu sant, waxtu wu nu Ngomblaan gi soxlaa dinanu ñëw. Waaye, bu dul saa-senegaal bu nu soxla war nanu ko ubbil bunt waxtaan ak moom, déglu ko, lu ñu mën ci faj aajoom nu faj ko bu nu mënul it nu dalal xelam, yebal ko fi ñuy faje aajo yi. »
Foofu la jëwriñ ji tëje ag kàddoom gu njëkk. Ca la Njiitu Ngomblaan ga ubbee waxtaan wa jox lëkkatoo gu nekk diiru simili yi muy wax. Mu mel ni nag, Ngomblaan ga moom déggoo fa am, ku nekk ak fa nga fare rekk lépp lu mu wax rekk baax na. Waxtaan wa nag, daanaka loolu moo ko tënkoon. Ñi fare ci Nguur dañuy dëggal li jëwriñ ji wax ak lu mu mën di doon, muy lu am njariñ walla mu ñàkk njariñ. Ñi fare ci kujje gi wax la ca des ba pare samp ay laaj ngir jëwriñ ji indi ci ay leeral. Te, ñu bari ci ñoom jàpp nañu ne wax ji li muy bari bari, ak li muy neex neex, ci làmmiñ kepp la yem. Te, mbir yi warul a yem ci ay këyit rekk, saa-senegaal yépp am ag yemoo ci sémb bii ñu yékkati mu bañ a am genn par-parloo. Waaye nag, li mat a laaj kay mooy ndax dépite yi askan wi lañu fa nekkal walla seen i lëkkatoo ?
Mu mel ni ku ci xas am ndombog-tànk rekk fàtte askan wi. Ndax, ñi fare ci Nguur, lu ñu wax yaakaar ne noonu la, di tagg li fi Nguur gi def. Ñi fare ci kujje gi tamit jàpp ne Nguur gi warul a wax lu jaar yoon, te waruñu koo sumb tamit, di wax fànn yi nga xam ne Nguur gi lajj na fa. Loolu nag tax na ba, ñii fare ci kujje gi rawatina waa Yewwi Askan Wi jàpp ne jëwriñ ji sémbam bi des na. Te, leeral yi mu indi ci seen i tontu des nañu. Tax ba, ñu bëgg a amal lii ñuy wax pasum diiŋat, motion de censure ci nasaraan, ngir fànq Nguurug Aamadu Ba gi.
Ci alxames jii la jëwriñ ju mag jii di Aamadu Ba doon jàkkaarloowaat ak dépite yi ca Ngomblaan ga ngir ñu càmbar mbirum pasum diiŋat mile, ba xam ndax dañu fànq Nguur gu yees gi Aamadu Ba jiite walla.