Démb, talaata 26 ut 2025, la dépite yi wote, daldi jàllale sémbuw àtte 14/2025 te aju ci wàllu sàkku ak jot ay xibaar yu ñeel bokkeef gi. Téeméer ak fanweer ak benn (131) dépite ñoo ko wote.
Solos sàrt bu bees boobii nag mi ngi aju ci lu muy delloo ma-xejj bi àqam. Nde, daf koy dooleel, gëddaal ko ci li mu koy yombalal xibaar yi mu aajowoo ngir lijjantiy mbiram walla gindeeku. Dafa sax, ci lees yoonal ci sàrt bi, mënees na teg i daan ci kaw képp kuy gàllankoor càkkuteefu xibaar yi, te yit mënees na ko alamaan ba 10i miliyoŋ ci sunuy koppar. Dees na leen tënkal sàrt bi ci fukki laaj yii toftalu :
Laaj 1 : Kan moo am sañ-sañu laajte ay xibaar ñeel bokkeef gi ?
Képp ku nekk Senegaal, ngay kenn nit, di mbooloo mu lootaabewu (mbootaay, kurél, kërug liggéey, añs.) te sàmmonte ak li yoon tëral.
Dog 13eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 2 : Kan lees mën a laaj ay xibaar walla ci kan lañu mën a jëlee ay xibaar ?
Ñi am wareefu tontu / joxe ay xibaar ñooy :
-
Campeefi Bokkeef gi (Njiiteefu réew mi, Ngomblaan gi, Càmm gi, añ) ;
-
Képp kuy ndawul Nguur ;
-
Bokk-moomeel yi ak depàrtmaa yi ;
-
Këri liggéey yu jàmbure yiy jot ci ndimbalu Nguur gi walla yu sasoo liggéey bu ñeel ittey réew mi.
Dog 6eel jàpp dog 10eel ci sàrt bi ñoo ko leeral.
Laaj 3 : Naka lañuy laajtee ay xibaar walla fan lañu war a jaar ngir jot ci xibaar yees soxla ?
-
Bind ag càkkuteef ci làkkuw farãse, mu am lél ak i xibaar yu ñeel aji-sàkku ji.
-
Leeral xibaar bi ngay sàkku.
-
Dees na la jébbal këyit guy firndeel ne jotees na ci sa càkkuteef.
-
Bu dee mënoo dawal te mënoo bind, dinañ la déglu, def sa càkkuteef ci ndéggat.
Dog 14eel jàpp 16eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 4 : Ci ban diir lañuy xaar tontu li ?
-
Ci saa si, bu mënee nekk.
-
Warul weesu 8i fan bu dee ab saytu war na ci.
-
Mënees na ko yokk ba 15i fan gën-gaa bar.
-
Boo toogee 15i fan te jotoo ci tontu li, li muy tekki mooy bañal nañu la sa càkkuteef.
Dog 17eel jàpp 21eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 5 : Ndax danga war a fay xaalis ngir jot ci xibaar yi ?
-
Amul fay.
-
Li mënul ñàkk rekk ci wàllu defar bi/yónnee bi nga mën a fay (bu ko laajee).
Dog 22eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 6 : Yan xibaar lañu MËNUL joxe ?
-
Mbóoti làrme bi walla xibaar yi ñeel kaaraange réewmi/askan wi.
-
Mbóoti luññutuy yoon.
-
Mbóoti wér-gi-yaram.
-
Mbóoti ndefar yi ak yaxantu gi.
-
Waxtaani Càmm gi.
-
Lépp lu mën a gàllankoor kaaraange réew mi walla mu ñagasal diggante réew mi ak waa bitim-réew.
Dogu ñaareel bi (2eel) ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 6 Ñaareel : Ndax am na ay daan yuy dal ci kaw képp ku joxe ay xibaar yu ñu tere ?
Waaw. Mënees na alamaan sax (500 000 jàpp 10i miliyoŋ ci sunuy koppar) képp ku ko tey joxe ay xibaar yu sàrt bi tere ñu joxe leen. Dogu 33eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 7 : Lan nga mën a def bu ñu la bañalee sa càkkuteef ?
Dañu la war a leeralal sabab bi tax ñu bañal la sa càkkuteef.
Mën nga bind kurél gii di (Commission nationale d’Accès à l’Information) ngir laaj ko. Danga war a bind kurél gi laata ngay kalaameji.
Dog 26eel ak 29eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 8 : Lan mooy 𝗖𝗢𝗡𝗔𝗜 ?
Ag kurélug caytu gu moom boppam la, 12i nit ñu ñu tabb nekk ci, ñu am moomeg 3i at gu ñu mën a tóllanti wenn yoon kese.
Liggéeyu kurél gi mooy :
-
Fexe ba jëmmal àqu jot ciy xibaar
-
Tàggat ay ma-xejj ak i caytu
-
Jot ay kalaame
-
Joxe ay ndénkaane
-
Siiwal ag caabal at mu jot
Dog 27eel ci sàrt bi moo ko leeral
Laaj 9 : Yan daan lañuy gàll ñiy bañ a joxe xibaar yi ?
Ab alamaanu 500 000 jàpp 10 000 000 ci sunuy koppay mooy xaar képp ku bañ walla mu tey ko daldi gàllankoor càkkuteefu xibaar bees war a joxe.
Dogu 30eel ci sàrt bi moo ko leeral.
Laaj 10 : Ban wareef bu bees mooy tegu ci kaw caytu yi ?
Ñi wareefu tontu dañu war a :
-
Taxawal ab komite bu topp liggéey bi, 3i nit séq ko
-
Tàggat seen i ndaw
-
Di xamal askan wi liggéeyu joxe xibaar bi leen ñeel
-
Defar ab téere bindu bob, ci lees di bind ñiy sàkku xibaar ak kalaame yi
-
Siiwal ci seen dali web xibaar yi jàppandi