Li fës SËÑ BÀMBA By Ndey Koddu Faal 03/09/2023 0 270 Partager FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Yeneen i xët ÑAXTUY SÀNDIKAA YI Mbay Sow - 03/07/2025 DAAR-DAARU USMAAN SONKO (NJIITUL PASTEF) Paap Aali Jàllo - 02/07/2025 LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (1/7/2025) Njuga Gay - 01/07/2025 TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA ESPAAÑ Mbay Sow - 30/06/2025 Aji bind ji Ndey Koddu Faal Sëñ Bàmba Kéemaan la Dem ba ñëw war a sant ci ñibbisi gi Di sant Boroom bi ci dem gi Ndeke dem gee jur Màggal gi Bu demul woon dunu jot ci teraanga yi Sëriñ bi … Kenn du Sëriñ Bàmba Dem na ba ñëw ci jàmm ak salaam Waaye di fésal ug cant Yàlla ci dem gi Nattu yaa jur bànneexam Xéewal yi rogolaat ba fépp tooy Moyul kenn kon Bàmba mooy Kéemaan di tawféex nanu ci ŋoy Bi noon yi foogee ni Jàpp nanu Séex bi Moom Bàmba mu naan Danoo bokk yoon rekk waaye àndunu Tey bi pënd bi wuree Ñépp xam nañ ni Bàmbaa gore Yàlla rekk a fi ne, ku jëf mu fey la Ku nekkal Yàlla, Yàlla nekkal la Bàmbaa di ki gëm Yàlla Jox boppam Yàlla Léppam di Rasululaay Wóor na ñépp, billaay Moo ni xalimag Yàlla du bindati ku mel ni Mustafaa, kon du amati Du Yàlla da ko mënatul Déedéet…Yàlla tëlewul dara Waaye dafa nammatul a bind Ku mel ni moom ci biib dénd Sa mbëggeel ci Mustafaa du waxi kese Mbàkke Bàlla Woote ñépp wuyusi Nit ak jinne, kenn du des Njabar mënu ko Bari pexe joxewu ko Yàlla rekk a fi nekk Yaa fii taxawal Jëf-jël Yaa fi jëf lu ñépp di soow Ci lu baax, neeleen waaw Moo waral tey nga am li nga am Jërëjëf Séex Bàmba Jërëjëf Maam Jaara Ndey Koddu FaalPlus de publicationsBiographieNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/DOKTOOR JÀLLO JÓOB : GOR CI WAX, GOR CI JËFNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/SÉYDINAA MUHAMMADU MAXTAAR LAAY, XALIFA LAAYEEN YI, DËDDU NA.Ndey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/LAAJ-TONTU AK SOXNA FAATU SIISE KAN (2/2)Ndey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/LAAJ-TONTU AK SOXNA FAATU SIISE KAN (1/2) FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Widewo VOA AMAL NAB JOTAAY CI MBINDUM BUBAKAR BÓRIS JÓOB GINNAAW BI WEREKAAN BI JËLEE CARGALUG NEUSTADT 2022 BI. CUQAL CI LËNKAAY BII TOFTALU... Defu Waxu - Xët yi mujj