SENEGAAL : TOLLUWAAYU ÑÀKKUG LIGGÉEY BI YÉEG NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

ANSD siiwal na tolluwaayu ñàkkug liggéey bi fi Senegaal ci atu 2024 mi. bees sukkandikoo ci njureefi luññutu yi mu fésal, ci téeméeri nit ñoo jël, 20,3 yi amuñu liggéey. Lim boobu mi ngi aju ci 3eelu xaaj bu atum 2024.

Njureef yi bawoo ci luññutu (laaj ak tontu) bi ñuy amal fi Réew mi ci wàllu liggéey, te Agence nationale pour la statistique et la démographie (Ansd) siiwal ko ci talaatay démb jii di yemook 7i fani sãwiyee 2025. Gëstu bi dafa wane ni, ci ñatteelu xaaju 2024 bi, “tolluwaayu ñàkkug liggéey bi àgg na ci 20.3%”.

Ba tay, ci njureef yi ANSD biral, limu nit ñi amul xëy am na yokkute bu ndaw bu ñu ko méngalee ak atum 2023. Ndaxte, ca jenn jamono ji, daaw-jéeg (2023), lim baa ngi tolloon ci “19.5% biñ seetlu ci jamono jooju ci 2023, yokkute bu 0.8 poñ ci teemeer boo jël”.

Ci diirub 3i weer yi njëkk ci atum 2024, limu ñi amul liggéey ci Senegaal mi ngi tolloon ci 23,20%. Ginnaaw gi dafa wàccoon ba 21,60% ci diiru ñetti weer yi ci toftalu. ANSD xamle na ne, bees saytoo ñi tollu ci am liggéey, mooy ñi am 15i at jëm kaw, “58,3% ñoo ngi liggéey”.

Ci li ANSD yégle batay, liggéey bi, ci dëkki kow yi la ëppee. Ndax, foofa, ci téeméer bu nekk, “58,8%” am nañ ci lu ñuy yëngatu. Waaye, bu dee dëkki taax yi, téeméer bu nekk, “58,0%” rekk a ciy liggéey. Bu dee li ñeel bariwaayu liggéey bi nag, “dëkki taax yi (45,7%) ñoo ëppale dëkki kaw yi. (38,3%)”.

Bees méngalee góor ñeek jigéen ñi, jàngat bi dafay wane ni limu “góor ñiy liggéey moo ëpp limu jigéen ñiy liggéey”. Nde, bu dee góor ñi, téeméer bu ci nekk, 56,4% yi ñoo ngi liggéey te, bu dee ci wàllu jigéen ñi, 28,8% yi kepp ñoo ciy liggéey.  Kon, limu góor ñi am liggéey daanaka ñaari yoon la gënee bari bob jigéen ñi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj