Tay ci altine jii 15 sãwiyee 2024 la Senegaal doon amal joŋanteem bu njëkk ci kuppeg Afrig giy am fee ca Koddiwaar. Mu doon ci daje ak dënkandoom bii di Gàmbi, waaye daf ko wulli 3i bal ci dara.
Seen joŋante bi nag, daanaka tàmbali woon na lu jiitu tay ci diggante soppe yi. Foo geestuwaan, ci mbaali-jokkoo yi, gis sànnante xeer yeek tooñante gi ci diggante Saa-Senegaal yeek Saa-Gàmbi yi, mel niy doomi bàjjen. Muy lu ñu bari rafetlu itam. Ndax, dafay rattaxal diggante Sengaal ak Gàmbi, di wane mbokkoo gi am ci diggante ñaari réew yi ak jàmmoo bi. Lépp nag ñu daldi koy def ci kaf ak ree kepp. Waaye nag, gaynde yi ñoom, caaxaan taxu leen woon a jóg. Ñoom, dañ xiifoon yàppu jiit te ragaluñ tooke bim àndal. Ndege, tey, gayndey Senegaal dañ tuloon.
Bi 14i waxtu jotee la joŋante bi tàmbali. Dañu dawal tuuti rekk, jiiti Gàmbi yi bëgg a nax Senegaal, sàcc ko ko benn bii. Waaye ndokk, booba daa fekk Eduwaar Méndi di wattu caax yi. Moo tax, bi Saa-Gàmbi bi dóoree, Njaago bi daa faxas bal bi fële. Gaynde yi daldi yeewu nag. Nde, tuutiy simili lañ ci teg rekk, Paap Géy lakk caaxi Gàmbi yi. Saajo Maane moo ko taajal dóor-mu-dugg, Ngéyeen bi làq bal bi ci ruqu ndeyjooru góolu Gàmbi bi.
Noonu, ñu dawal ba ci 45eelu simili bi E. Adams, jaare ginnaaw Lamin Kamara, dëgg wëq wi, muy gaañ bu soxor bees di tere. Moo tax arbit bi jox ko kartõ ruus ci saa si. Ci la xaaj bu njëkk bi jeexee.
Ba ñu dikkaatee, ñu dawal tuuti ba ci 52eelu simili bi, Lamin Kamara bëtt defãsu Gàmbi bi bëtt bu rafet ci paasu Ismayla Saar, daldi tojaat kër gi, muy ñaar. Ñu nekk ci di wéyal noonu. Senegaal wane ci xar-kanam gees ko doon xaare : téye bal bi futbal ci lu dal xel. Teewul nag, Gàmbi doon na bañ-bañlu ba sax am na yoon yu mu naroon am dara. Waaye, Eduwaar Méndi di leen ko xañ ba tay. Ba ñu dawalee ba ci 86eelu simili ba, Elimaan Njaay jël bal bi wane xarañteem ca wetu kãwu gàmbi, duut benn, ñaar ba ñetti Saa-Gàmbi, taajalaat bal bi Lamin kamara, mu laxas bal bi fu ruqe foo xam ni góol ba mënu ca dara, muy ñett. Ndaw bii bu réy ! Moo dàqagum ci CAN bile. Ci 3-0 yooyu la jeexe.
Muy xar-kanam gees doon xaar ci Senegaal nag, mu duggusee ci CAN bi nu am solo. Saa-senegaal yu bari, koo ci wax, mu ni lii lañuy xaar ci ñoom, ñu wane ni fa ñu nekkoon ñoo ngi fa ba léegi. Moy lu am solo. Ci seen kippu gi nag, moom Senegaal moo ci gañeegum, jiitu ci. Ndax, Kameruun dafa timboo ak Gine ci 1-1.
Senegaal dina génnaat àjjuma 19 sãwiyee 2024 bu 17i waxtu jotee. Kamerun lay dajeel. Nuy xaaraat ci ñoom joŋante bu jaar yoon ak fullaak faayda.