Fàttaliku lu war jaam la, kon na xel dellu ci ginnaaw ngir saytu walla jéex démbu Senegale yi njëkk a agsi Milan. Démb a jur tey te Wolof Njaay dinay wax ne : “Ku la njëkk ci jàkka, bu dee jullee ka fa yóbbu, moo la ëpp i ràkka.”
Dégg ngeen tamit ñu naan lu Wolof léebu dëgg la. Kon duñu def lu-dul jéem a tarxiis, sóobu ci diggante 1986 ak 1993. Ci jamono jooju, génn Senegaal jëm Itali yomboon na lool, wiisaa turistik rekk nga soxla woon, danga ko doon wone , daldi jël sa roppëlaan, mu wàcce la Rom walla Milan. Rax-ci-dolli, benn takk-der daawu la sonal ci ayeropoor bi.
Bi roppëlaan biy bëtt niir yi, xeli way-tukki yaa ngiy naaw ci biir niis wi, mu mel ni ñu ngiy wëndéelu ci jaww ji bay laal asamaan si. Nit ñiy gami-gami waaye ñu ngi kebetu “Ku tukkiwul doo xam fu Gànnaar féete.”
Gan du yewwi béy. Te ku ñów cib dëkk, fekk wàlliyaansi yiy doxe benn tànk, noo def ne nepp di seet noy doxale walla wan yoon nga war a jaar.
Booba, doxandéem yu njëkk yi amaguñu kayit, mu xañ leen liggéey bu ànd ak payam wer wu jot.
Kon naka la doxandéem yi daan daane seen doole ngir téye seen njaboot ?
Sunu xel daldi dellu ci ñi jóge ci ay gox yu sore, wutsi teraanga ci dëkki taax yi. Ndakaaru nag, jaay ci mbedd mi rekk lañu fi mënoon a def. Boo bañee sa sutura xàwwiku walla say noon di la reetaan, fonkal liggéey ak bum mên a doon.
Doxandéem yi ci ëppoon fii ci Itali lal màrsandis jaay moo doon seen liggéey. Waaye dafa ko fiy aaye. Kon mbir mi yombul woon lool waaye tuuti yërmande amoo na. Jaay ci mbed mee gën talal ay loxo, Tubaab bu romb sànni la dara. Tuutil sa bopp, dara jaru ko. Fullaay jaay daqaar te yit moo gën taar.
Ci xolu dëkk bi, Milan, ñu ci ëpp ci sunu mbokk yi, ci metóro lañuy lal seen njaay. Tey nu wax leen naka la móodu-móodu yi aakimoo metóro Loreto bu siiw boobu.
Jamono jooju, dem nañ ba koy méngaleek màrse Sàndaga ndax xumbaayam ak li nit ñiy jóge fu ne di fa daje bés bu Yàlla sàkk.
Dafa fekk Loreto selebeyoon la ndax ñaari yooni metóro lañ fa rëdd, bu xonq bi ak bu nëtëx .bi. Loolu day yombal liggéey bi waaye teewul jaaykat yi daan teel a yeewu ngir am palaas bu fés, Xonq-Nopp yi mën koo ràññee.
Ci biir Loreto, móodu-móodu yi sancoon nañu ñaari bérébi jaayukaay. Ñi newoon ci yoonu metóro bu xonq bi ñoo tudde woon seen màrse ‘’Kolobaan’’, ñi ci des di woowe metóro bu nëtëx bi ‘’Sàndaga’’. Sama gaa ñee ka amoon fit ! Ngénte doom ju ñu jurul du woon dara ci ñoom ! Waaye àddinaa mel noonu, dangay am fit, xuus ba jàll te benn coono du la ci fekk ndaxte dex gi fer na.
Waa “Kolobaan”, nag, dañ leen jàppe woon ni ay kaw-kaw. Keneen ku dul ñoom sañu fa woon lal. Ñoo fa daan samp seeni ndënd, di fëgg dënn ak a nàngal kanam, naan fii ku fi lal ma yóbbu la barsàq !
“Sàndaga” moom, Booy Dakaar yee fa newoon di jaay.
Amoon nay bés dañu daa werante ba mu soppiku xuloo, yëf yi dem bay waaj a ëpp loxo. Li ko daan waral moo di ne waa “Sàndaga” dañoo xawoon a xeeb waa ‘’Kolobaan’’, jàpp ne ñoo gën a siwiliise, seen doxalin a gën a dëppook aaday Tubaab yi. Su ko defee waa Kolobaan di leen kókkali, naan leen xanaa dangeen a fàtte ni ku wàcc sa and, fo toog ñu xeelu la !
Coow leek dàggasante bi daal, looloo ko sooke. Sa moroom romb la, nga koy ñaawal naan xool-leen kook colinu kaw-kawam gi, ay wi neeti kurr.
Waa “Kolobaan” yaa ngi dëkke woon tuumaal ‘’Sàndaga’’, naan ñu ngi yàq deru Senegale yi, lu leen tee sol yére yu set, tey xeeñu gëtt gu neex. Mbir mi dafa def i ree ‘’kaw-kaw’ yi ndax ñoom dañoo xamul lu xiir waa ‘’Kolobaan’’ yooyu ci jaay Tubaab, di temp ndànk ni Muse Sumaare way-jëmmal bi ci Doomi golo bu Bubakar Bóris Jóob.
Rax-ci-dolli, waa ‘’Sàndaga’’ yu bare dañuy dem ci night-clubs yi te duñ fa yem ci fecc ndax ñakkul ñu fay labat ay jigéeni Tubaab.
Ku jàng lii lépp mën nga xalaat ne sunu mbokki Loreto yi dañoo meloon ni xaj ak muus walla sax ñu nekkoon ci xare bu metti. Kon, nan gaaw dindi kumpa gi. Ku xam aada Senegaal, xam ni kaf lu am maana la fa. “Sàndaga” ak “Kolobaan”, ay doom-bàjjan walla ay gàmmu lanu jàppe woon seen bopp, di kaf, di tooñante saa su nekk.
Li koy biral mooy ni italieŋ yi doon gise doomi-Senegaal yi, di leen tagg ndax seen yarook teey. Te ci dëgg-dëgg Senegale bu reew jafe woon na gis jamono jooju. Alkaati yi, koo ci waxalaan mu ni la Senegale yépp a jub, duñu jaay ñaax walla leneen, duñu sàcc walla ñuy kàcc. Moo taxoon sax Tubaab doon leen woowe “british” naan dañoo yaru taaru.
Waaye niñ koy waxe, àddina wërngël. Sunu mbokk yi agsi Itali ciy ati 2000, wute nañu lool ak ñi ñu fa fekk, muy waa ‘’Sàndaga’’ di waa ‘’Kolobaan’’. Ku yabu sax ne dañoo mel ni Yàllaak Yaali.
Ñi ëpp ci ñi mujjee ñëw, jàng nañu nasaraanWa atum 2000 li ëpp ci ñom jàng nanu nasaraan, seen xel ubbeeku na ñu xam àddina ba tax kenn feesul seen bët. Xanaa li yar bi xaw a des rekk mooy cat li.
Ñi njëkkoon a jóge Senegaal ci jamono jooju lañ indi Itali doom yañ bàyyi woon Senegaal.
Gone yooyu nag, ñu ci bare daanaka dañoo réer. Li ñu seetlu moo di ne faalewuñu seen baay te xamadi foofu lay tàmbalee. Loolu indi nay jafe-jafe yu bari, ay kër sax tas nañ ci. Waaye yàkki xaju fi, Yàlla mi dara tëwul mën naa soppi jikko xale yooyu ba seen xel delsi, ñu bañatee xeeb seen xeet.