Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal, xalifa Baay-Faal yi, wàcc na liggéey. Démb ci àllarba ji, yemook 12eelu féewiryee 2025, la wuyuji Boroomam. Amoon na 95i at.
Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal nag, moo nekkoon 8eelu xalifa Baay-Faal yi, wuutu ci jal bi Sëriñ Séex Jëmb Faal ca atum 2021.
Xalif bi ràññeeku woon na ci yërmaandeem ñeel taalibe yi ak ndogu yu xéewale ya mu daan jagleel njabootu Sëriñ Tuubaa weeru koor wu nekk. Sëriñ Móodu Amdi Mbenda dafa jënde woon cëru derete ak ag taalibe, dogu rekk ci wéyal ndonol Maam Séex Ibraayma Faal. Moo tax it seedee yi benn la : liggéeyaakonu Sëriñ Tuubaa la woon, leneen ñoru ko woon.
Nuy fàttali ne Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal mi ngi gane woon àddina ca Ndànk-Seen (Njurbel), wàccee liggéey ca loppitaalu Séexul Xaadim bu Tuubaa, ñu rob ko it Tuubaa.
EJO-EDITIONS ak LU DEFE WAXU ñi ngi koy jaal njabootu Séex Ibra Faal gépp ak waa kër Sëriñ Tuubaa ak taalibe yépp. Noo ngi koy jaal tamit bindkat bii di Làmp Faal Kala mi génne 2i téere (Xelum Xalam, 2020 ak Tànn-béer, 2023) ci EJO-ÉDITIONS.
Noo ngi ñaan tamit Yàlla dolli xéewal Sëriñ Amdi Xadi Faal mi nekk 9eelu xalifa Baay-Faal yi tay jii.