SETAL SUNU RÉEW : TEEWAAYU NJIITU RÉEW MI FA MBUUR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, moo ubbi juróomeelu bésub set-setal bees di amal weer wu jot te ñu dippee ko “Setal sunu réew”. Wii yoon nag, daara yi lañu ko jagleel. Moom Njiitu réew mi, dafa dellu fa liiseem ba woon, “Lycée Demba Diop” Bu Mbuur. Aawoom bi la àndaloon, Soxna Xóon Fay.

Ca ENO bu Mbuur la njëkk a dem ngir nemmeeku béréb ba. Bi mu fa jógee la dem ca liise bu Mbuur. Ay boori 10i waxtu ci yoor-yoor bi la fa àgg, daldi fekkee yékkatig raayab Senegaal. Moom, Njiitu réew mi, ca liise boobu la jàngee diggante 1997 jàpp 2000. Fa la amee lijaasa “baccalauréat” laata muy dem ca Jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru. Bi mu demee, gisante na ak ña ko jàngal, mu saafonte ak ñoom, delloo leen njukkal.

Ginnaaw gi, waxtaan na ak njàngaani liise ba, jox leen ay ndénkaane. Waayeet, tontu na seen i laaj yu ñeel njàng meek njàngale mi ak itam mbëkk mi.
Bi mu noppee ci loolu, ci la jël bale bi, ubbi bés bi. Bi mu balee ba noppi, jëmbat na fa ag garab laata muy xooli kalaasu 36 bi nekk ci taax F, muy kalaas bi mu defee “Terminale”.
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, xooli woon na yit kaajarug yeesalu liise bi, daldi wax ak saabalkat yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj