SIGARET : REYAATEKAT BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bërki-démb, ci talaata ji 7i fan ci féewaryee 2023, lees doon amal ndajem liggéey ñeel xeetu juuti bees duppee “taxe parafiscale” bi nga xam ne, jaglees na ko kopparalug xeex bees di xeex tóx mi ci réew mi ak yeneen xeeti feebar yi dul wàlle.

 Kippaangoog Cicodev Afrique (L’Institut panafricain pour la citoyenneté, les consommateurs et le développement) ak taskati-xibaar yiy yëngu ci wàllum wér-gi-yaram ñoo doon amal ndaje ma. Ndax jàpp nañ ne xaalis bi Càmm gi jagleel wér-gi-yaram ci atum 2023 baa ngi tollu ci 242,4i miliyaar ci sunuy koppar te xaajul bay doy. Waaye ci xaliis boobu, 25i miliyoŋ rekk lañ ciy génne ngir xeex tóx mi ci réew mi. Nde, loolu matul dara ngir xeex bees di xeex tóx mi jaar yoon. Looloo tax, njiitul Cicodev Afrique di Aamadu Kanute jàpp ne fàww ñu amal fépp ci biir réew mi ay waxtaan ak i layoo ngir ñu am ab dekkare buy yoonal payug juuti bii di « taxe parafiscale » ci póon beek tóxum sigaret si. Nde boo seetee ba ci biir, ci atum 2017, waa CRES  (Consortium pour la recherche économique et sociale) gis nañ ne askanu Senegaal génne na ci tóxum póon bi lu tollu ci 122i miliyaar ci sunuy koppar, jëleewu ci lu dul 24i miliyaar ciy juuti. Loolu mooy ne réew mi ñàkk na lu tollu ci 98i miliyaar ci tóx mi. Waaye, ci wàllu wér-gi-yaram la waalo gënatee aay.

Doktoor Abdul Asiis Kase nag, mi ngi artu ak a xamal tóxkat yi ne, sigaret dafay wàññiy fani dund. Nde, jukkees na cib gëstu bees amaloon atum 2015 ne, Senegaal am na 600 000iy tóxkat. Ñooñu nag  képp-keen ci ñoom, bakkanam a ngi ci xottu gerte. Waaye nag, bees sukkandikoo ci kàdduy doktoor bi, am na 300 000iy tóxkat yu war a jënd seen perkaal denc,  te na leen seen i mbokk nàkkal. Ndax kat, léegi ñu dee. Doktoor Kase, di gëstukat ci feebaru kañseer, moo ko wax. Dafa biral ne 300 000iy tóxkat yooyu, dinañ faatu ci diir bu gàtt. Dara du leen rey lu dul feebari xol, feebari xëtër, feebari noyyi, jàngoroy jabet, añs. Dafa di nag, tóx baa di sababu feebar yooyii di leen yóbbu allaaxira. Fajkat bi neeti, saa boo tóxee benn sigaret, 14i simili wàññeeku nañu ci sa dundu. Bu fa yemoon sax mu tane, waaye déedéet. Ndekete, tóxkat yi dañuy xaru ba noppi di reyaate. Ndaxte, ñi ngi loraale nit ñiy noyyi saxaar su bon si ñuy sàndi bu ñuy tóx.

Doktoor Kasee di nu xibaarati, ci yéenekaay Le Soleil, ne, saxaaru sigaret see gën a bon poson. Nde, bu sibbiru reyee kenn, saxaaru sigaret rey na ñaar.  Moom nag, ngir wut pexe, mi ngi ñaax Nguur gi mu yokk njëgu sigaret si, amaana mu dawloo tóxkat yi. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj