Ay téeméeri téeméeri nit ñoo dajaloo ca buntu këru Usmaan Sonko, fa Sigicoor jamono jii. Gaawu, ci guddi gi, la fa mbooloo ma tàmbalee dem. Li ko waral mooy lees di ruumandaat ne, dañuy waaj a jàpp njiitul Pastef li ñeel layoo bim séq ak Aji Saar. Layoo bi nag, talaata 16 me la war a am. Waaye, meeru Sigicoor bi, Usmaan Sonko, daf ne du wuyooti Yoon. Moo ko tax a toog ca këram, ci biir i mbokkam, foofee ca Sigicoor.
« Panaanug way-bëggi réew mi », noonu la ndawi Pastef yeek soppey Usmaan Sonko yi tudde toogaanug guddi gi ñuy def ca buntu këru Usmaan Sonko. Li ñu ko dugge mooy sàmm, te aar seen yaakaar bii di Usmaan Sonko. Umpaleesul ne, ci talaata jii, 16 me 2023, lees àppal layoob Usmaan Sonko ak Aji Raabi Saar mi koy tuumaal ciif ak tëkkuy rey. Ci diggante bi, lu bari xew na fi. Moo tax, njiitul Pastef li jël ndogalu bañatee wuyuji Yoon. Li ko sabab, ciy waxam, mooy tooñ yees koy tooñ booba ak léegi, di joggatiy àqam, di salfaañe ay yelleefam, dem ba koy metital, di toj weeri daamaram. Mu gis ne, Yoon, ci ndigalu Maki Sàll mi ko bëgg a faagaagal lay dox. Moo ko tax a bañ. Keroog nag, ca ndajem F24 ma, toppekat ba woon Aliyun Ndaw, daf fa joxe woon xibaar bu doy waar, tiital waa Pastef. Daf fa waxoon ne :
« Xam naa ni ñu ngi waajal cantaaneg jàpp-indi Usmaan Sonko ñeel mbirum Aji Saar. Na saa-senegaal yépp bañ loolu. »
Bi xibaar boobu jibee, mu amatiy taskati xibaar yu ko dëggal, ca la ndawi Sigicoor ya jëlee seen matuwaay ngir aar seen meer bi. Ay ndawi Pastef di jóge fu nekk, di leen fekki ca buntu këru Usmaan Sonko. Jamono jii, mbooloo ùaa nga fa fees dell, di xaar sàndarm yi. Ci guddig gaawu gi sax, Maalig Gàkku, Seex Tiijaan Jéey ak Soxna Ayda Mbóoj teer nañ Sigicoor ngir taxawu, jàppale Usmaan Sonko mi ñu bokkal lëkkatoo Yewwi Askan Wi. Fi mi nekk nii nag, xale yi fépp lañu fàtt. Wépp yoon wuy jëme kër Usmaan Sonko rekk, ñag nañ ko.
Cig pàttali, biñ jàppee Usmaan Sonko ca màrs 2021, réew mi tàkkoon ba jax, 14i nit dee woon ci. Wile yoon, lu nar a xew ?