Dees na siiwal limu saabalukaay yi méngoo ak yoon ci lu yàggul dara. Bees sukkandikoo ci njëwriñu Jokkoo gi, Jokkookaayi xarala yi ak Nimerig bi, gën-gaa sori, dees na biral toftale gi bésub 30 nowàmbar 2024.
Jëwriñ ji, Aliyun Sàll, dafa biral ab yégle, wax ci ne :
“Ci biir juróom-benni weer, teg nanu ay jéego yu am solo ñeel leeral gi ak naaluw lootaabewaat fànnu saabalukaay yi. Ginnaaw bi nu amalee njëlbeenu ndajem ndiisoo giy wéral biralug saabalukaay yi, dees na siiwal toftaleg saabalukaay yi Càmm gi nangu gën-gaa sori keroog 30i pani nowàmbar 2024.”
Bu n̈u xasee siiwal toftale googii nag, dinañ teg i daan bépp saabalukaay bu ci bokkul, maanaam bu sàmmontewul ak yoon. Jëwriñ ji a ko xamle. Ciy waxam ba tay, saabalukaay yooyii ñàkk a dëppoo ak sàrt yi, dees na leen gàll ay daan ci ni ko yoon tëralee. Daan yi mën nañ àgg sax ba ñu ajandi leen. Te, bu ñu wéyee di jalgati yoon, ay daan yu gën a diis mën nañu tegu seen kow.
Bu dee ci wàllu koppar yees di dimbalee saabalukaay yi, jëwriñ ji xamle na ni dinañ ko teg ci lu leer, séddale ko ni mu waree ba képp ku ko yayoo mën cee jot. Xamleet na ni, koppar yooyii ñuy dimbalee saabalukaay yi, dañu ko war a jëfandikoo ci anam bob, dina leen tax a suqaleeku bu baax, moom seen bopp ci wàllu koom-koom.