SONKO, FULLAAY JAAY DAQAAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

 Usmaan Sonko tontu na ndongo ya doon tëgg i bool ca kanamu meeri bu Sigicoor bi mu jiite. La taxoon ndaw yay ñaxtu nag, ci seen i wax, meeri daf leen feyalul seen luyaas. Mu mel ni nag, doxalin woowu dafa neexul njiital Pastef li ba tax far pasug luyaas bi benn yoon. Démb, ci alxames ji la doon janoo ak taskati-xibaar yi ngir leeral ni mbir mi deme.

Nii la coow li demee, bees sukkandikoo ci kàdduy Papa Malamin Tàmbaa :  

« Féewarye 2022 ba léegi, noo ngi waxtaan ak ñoom ngir ñu tóllanti pasug luyaas bi. Waaye, déggoo mënul a am sunu biir. Te ñoom, dañoo bëgg dog pasug luyaas bi. Loolu la nu ne dunu ko nangu, moo tax nu génn tey yëngal dëkk bi. Nañ xam ne pólitig taxu noo jóg, defunu ko, te it àndu nu ak kenn. Li ñu war a xam mooy, su nu nexee gis gépp kilifa gu nekk ci biir dëkk bi… Li wóor mooy ne, bés bu nu dogee pasug luyaas bi, ndongo yu bari seen njàng dina yàkku ».

Kon, li ndongo yooyee di ñaxtu, ci seen i wax, mooy li meeri bi bañ a tóllanti pasug luyaasu kër gi ñu nekk te luye fa, ñoom ndongo yi. Li jar a xam mooy ne, googule kër, Abdulaay Balde, meer ba woon, moo ko jëlal ndongo yi ci atum 2016 ba nii. Looloo leen taxoon a biral kàddu gii, keroog seen bésu ñaxtu ba : « Sunu pasug luyaas, sunu ëllëg, sunu xeex, bu ko meeri bi laal ! »

Dafa di, bi ndongo yi, xëyee ci àllarba ji, 4 saŋwiyee 2023, dañu gën a wone seen uw naqar, génne seen rakk yi doon jàng. Noonu lañu wàccaate ci mbedd yi, di tëgg seen i kubéeri cin añs., ba ca buntu meeri ba. Seen bëgg-bëgg lañu ne fàww meeri bu Sigicoor def ko ca na mu gën a gaawe.

Ginnaaw doxub ñaxtu ndongo yi, Usmaan Sonko miy meeru Sigicoor génn na, janook taskati-xibaar yi ngir indi ay leeral ci ni mbir mi deme. Ci ay kàddoom, xamle na ne :

« Ci atum 2016 la meer ba woon Abdulaay Balde, jëlaloon ndongo yi bawoo Sigicoor kër gu mag fale ca Grand-Dakar. Ñi ngi waroon a fey luyaas weer wu nekk 77 6000 FCFA. Waaye, dañu ko daan dajale di ko fey 6i weer yu nekk. Meeri bi ameelul dara boroom kër gi. Ndongo yi ,kenn génnewu leen, te kenn indilu leen genn këyit guy wax ne dañu leen di génne. Ay mbirum pólitig doŋŋ moo tax ñu naan dañuy génn ci mbedd yi. »

Ci biir waxtaan wi, Sonko a ngi leeral ne pasug luyaas bi dafa wax ne, bés buñ demee ba koy tóllanti, fàww li ñiy wax  digaale  am. Teg na ci ne, 

« Dinañ leen feyal ba weeru saŋwiyee wi jeex. Te it, woolu naa wiisiyee ngir mu xamal boroom kër gi ne damay dakkal pasug luyaas bi bésub 31 saŋwiyee. Ndax teguwul ci benn cëslaay bu koy yoonal. Yoon sax, daf ñoo mayul nuy génne xaalis di ko jox ay nit. Lépp luy génn ci meeri bi dafay leer te fu leer lañ koy teg. Bu loolu weesoo, meeri dootul bàyyi ndongo yiy doxal pasug luyaas bi. Dinañ jël ku xam-xamam màcc ci wàll wi, te dara du ko ump ci ndongo yi fay nar a dëkk. Li leer ba leer mooy, ndongo yi nekk ciy jafe-jafe te amuñu kenn ku leen dimbali ñoo fay dëkk. Te lu ni mel lañuy def tamit këri luyaas yu Bàmbéy ak Ndar ».

Mu mel ni kon, mbir mi dafa rax. Nde, koo xam ne kenn génneewu la, kenn waxu la na dangay génn te amewoo benn borub luyaas, looy kaas ? Ndeke, jamono ja ndongo yay tëggi bool, seen i dëbës a nga woon ca kër googee ñuy wax ne feyeesul luyaas ba. Caaxaan baaxul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj