Soxna Kumba Mbόoj, ñu gën koo xam ci turu Kumba Falilu, mi ngi am 20i at, doon ab ndongo ca Daaray Sorbonne ca Paris. Moom nag tàmbali woon naa bind ci kàllaama nasaraan ba mu amee 12i at. Ci weer yii ñu génn, di dugg ci safar gi, ci lay soog a bind ay taalifam ci wolof, jëmale leen ci ku tedd ki, Xaadimu Rasuul, ak ug njabootam.
KU TEDD KI
Tay ma jël sama xalima jéem a kennal kenn ki
Mooy ki ump ñépp te jox ñu jëmmi ku tedd ki
Jubal ñu ndax yor taxawaayu Yonnent ya
Teg ñu ci yoon wi gën muy yoonu muridiya
Moo wax la kenn waxul dem fa kenn demul
Jëf lu kenn jëful Boroomam jox ko lu kenn amul
Moom rekk a ni déet ba ñépp nee waaw ca biro ba ca Ndar
Nanguleen ko ndax moom rekk a fi nekkoon ba muy tar
Moom rekk moo sax cig dundam di liggéeyal Boroomam
Tax mu ne cëpp ca géej ga julli bañ a tooñ moroomam
Moo jommal saytaane te semmal tubaab yi
Dem ca tukki bu sori ba indaale sarica bu duun
Liggéeyal la kenn liggéeyalul Rasuulul-laahi
Yaay jàmbaaru Yonnent bi yaay Xaadimu Rasuul
Di jàmbaari Lislaam ñàkk laa am wόorul
Indil nga ñu xasida yi samploo ñu ay daara
Moo tax duñu tàyyi di la sant cëy doomi Maam Jaara
Seex Ibra Faal di sa jàmbaar cëy Faal kenn du moom
Ñun it ñu dëkk ci di wax ni Bàmba yaa nu moom
Danga di kenn doo moroomu kenn bokkook sëriñ si
Moo tax ñu lay kennal dëkk ci di la sant naan la Bàmba MERCI