Gis-Gisu Seex Aliyu Ndaw ci "Francophonie"
Faraŋ ko fóni
(Woy)
Faraŋ ko fóni
Man kat daa waaru
Kaay làggi ci saaw làmmiñ
Na doon saw làmmiñ
Te bañ di aw làkk
Ci yow
Waaye kat yemal foofee
Bu fi ne jaas bu fi xand
Faraŋ ko fóni
Man kat daa waaru
Na saw làmmiñ
Di aw làmmiñ ci say doom
Te bañ di aw làkk
Ci ñoom
Waaye kat yemal foofee
Bu fi ne jaas bu fi xand
Bul juum bul jaawatle
Doo man duma yow
Faraŋ ko fóni
Lii de daa niru lool
Fóoxal
Di fàttali fël-fël
Xóoyal mu xorbet
Te du saf dara
Waaw
Moo yow doom Afrig
Xanaa jot na nag
Nga ne xiféet xippi say gët
Xool sa bopp
Xoolaat sa bopp
Maam démb de moom
Mi dëkke ne keww
Xool na boppam
Ba wiccax bopp
Te su nu jéppee muy gàcce
Su nu móoloo muy toroxte
Seex Aliyu Ndaw, Ndakaaru/Oktoobar 2021