Bi ñu nee Senegaal moom na boppam tamit, loolu ciy wax rekk la yem ; ndax Seŋoor àndul woon ci réew mi génn ci nooteel ci saa si. Li mu bëggoon mooy ñu ciy dem ndànk ndànk ci diirub 20i at. Ba tax na bi mu jiitee réew mi mu saxoon di sàkku ndimbalul Farãs.
Ci atum 1962, Seŋoor gaawtu taqal àndandoom bu yàgg bii di Mamadu Ja mi jiite woon jëwriñ yi, jiiñ ko ne da doon fexee daaneel nguuram. Loolu jur ñu teg Mamadu Ja loxo, tëj ko lu ëpp 10i ati kaso. Ci atum 1968, ci seleŋlu gu daj réew mép, liggéeykat yi bank seen loxo, alkaati yi dal ci seen kaw ci ndimbalul Farãs. Diggante Seŋoor ak Farãs gën a rattax ci atum 1971, ci ngan gu njiitu Farãs, Georges Pompidou, di xaritam teg ci bokkoon ak moom fa ñu jànge, doon amal ci Senegaal. Lu mat at Ndakaaru nekk di waajal ngan gu gàtt googu yamoon ci benn bés doŋŋ. Fi gan geek ñi mu àndal waroon a jaar yépp, kilifa yi defaraat yoon yi, yeesalaat taax yi ndax bëgg a làq lépp luy màndargaal ag ñàkk ci gëbla gi.
Ndaw ñu bari jàpp nag ne lu ëpp tuuru, dalal gi ñu dalal njiitu réewum Farãs ab cokkaas bu leer la. Ay ayu-bés lu jiitu loolu, gàngoor guy roy kurélu ”Black Panthers” gu Amerig, ak geneen gu tudd ”Tupamaros” ca réewum Uruguay, ànd taal Këru Mbatiit gu Farãs ci Ndakaaru. Bi ñuy amal ngan gi, xale yi jéem a dal ci woto njiitu réewum Farãs li, waaye ñu teg ñenn ci ñoom loxo. Ñaari rakki Omar Bolondeŋ Jóob bokkoon ca. Moom tamit boobu xeexin la gëmoon, muy dóor mu daanu, waaye bokkul woon ci cong googu. Fekk na ay weer lu jiitu loolu mu dellu woon Farãs ginnaaw bi ñu teggee dogal bi ko fa dàqe woon. Ci yëngu-yëngu yooyu ci la Bolondeŋ ànd ak ñenn ciy xaritam ne dañuy dem jàngi nu ñuy xeexeek ay ngànnaay. Noonu ñu dugg ci saxaar gii di “l’Orient-Express”, wër Tugal gi yépp, mujjee ci dalub ay saa-Siri fekk fa ay fippuy Palestin ak Eritere. Seen pexe moo doon teg loxo kilifag réewum Farãs gu mag, weccee ko ak seen mbokki-mbaar yi ñu tëjoon kaso. Bi ñu fa defee ñaari weer la Bolondeŋ Jóob ak ay àndandoom jóge ci tàkk gi dellu taax. Amoon nag yaakaar ci ndimbal ”Black Panthers” yi ubbi woon ab dal ca Alse, gëblag réewum Alseri. Waaye ñu mujjee soppi doxalin. Ginnaaw bi ñu defee diir bu gàtt ci Konaakiri ñu jóg wutali Bamako ga ñenn ci mbokki Bolondeŋ yi dëkkoon. Foofa ñu lootaabewuwa maanaam ñu defaruwaat.
Waaye terewul alkaati yi teg loxo gàngoor gépp ci jeexitalu weeru nowàmbar ci atum 1971, fan yu néew bi Seŋoor di waaj a amal nganam gu njëkk ca réew ma ginnaaw tasug Lëkktoo gu Mali ci atum 1960. Raji Mali yi Ceekoro Bagayoko jiit woon ñoo leen toppoo, raju leen ay weer. Ñu fekk ci gafag Bolondeŋ bataaxal bu tënk pexe yi mbokki-mbaaram yi war a rëccee ci kaso ba ñu leen tëj. Bi ñu ko jébbalee Senegaal, ñu tëj ko ràpp ñetti ati kaso. Bés yi ñu def ci kaso Gore bi yépp, diir bu néew lool lañu leen doon may ñu génn ca fa ñu leen tëj. Ngir moytu jokkalante ci diggante ñoom ñi ñu fa tëye, ñaari yoon rekk lañu doon gis jant bi, suba si 30i simili, ngoon gi 30i simili. Xàmmeetuñu guddeek bëccëg, guddi yàgg lool, booleek ñu leen di metital.
Xibaar bi daanu bésu 11i fan weeru Me ci atum 1973 : Omar Bolondeŋ Jóob saay na. Mu amoon 26i at. Xibaar bi ne tasar. Ndaw ñu bari génn ci mbedd yi di bind ci turux yi ci gëbla gi “Seŋoor bóomkat : Ñu ngi ray seen doom yi, yeewuleen ; Bolondeŋ kenn du ko fàtte”. Ci saa si, nguur gi dafa nëbb pekke wi. Waaye àttekat-luññutukat bi lànk ndigal li bawoo ci nguur gi, daldi teg loxo ñaar ñu ñu jàpp ne seen loxo taq na ci mbir mi. Daa gisoon ci këyit yi ñu jëlee ci kaso bi ñu bind ne ayu-bés laata ñuy siiwaal ne dafa xaru, Bolondeŋ dafa xëmoon waaye ñi yore kaso bi yëgaluñ ko woon sax seen yaram.
Waaye keroog ba muy waaj a teg loxo keneen ki mu njortoon ne moo ci taq, ci la ko fa kilifa yi jëlee, teg fa beneen àttekat mu dakkal luññutu gi ndax ne du céram. At mu jot, 11i fan ci weeru Me wu nekk ay takk-der ñoo doon wër bàmmeelu Bolondeŋ ngir bañ nit ñi ñëw di ko màggal.
Ay 10iy at a ngii boobu ba tay Omar Bolondeŋ Jóob wéy doon royukaay ci ay way-aamu ak i m-pasin. Ay kaajar, ay péeñ ak ay filmo wéy di dellusiwaat ci mbooram. Muy mboor muy indi sunu xel ci doxalinu nguuru Senegaal gu tay. Nooteel gi nguur gii di doxal day wone rekk ni jaay doole démb la woon tay soog a ñëw. At yu mujj yii, nguur gi xañ na saa-réew yi sañ-sañu lootaabe ay feeñu, ba noppi wéy di sàcc alalu askan wi, di jaay doole. Fileek wàccoo wuñu ak li ñu warlook askan wi, waxu kese la ngir xëcc koppar alkati bitim-réew yi. Li woon démb du wonni. Boo dee ab bañkat tay ci Senegaal, mënoo mucc ci ñu lay xoqtal, di la teg loxo, di la tëj kaso ci lu teguwul fenn. Gii Maris Saañaa ak ñeneen ñu bari xam nañu ci dara. Boo xoolee loolu xam ne nguur gii du mooy ubbiwaat àtteb Omar Bolondeŋ Jóob. Waaye ni ko ay mbokkam di baamtoo rekk : “Lu guddi gi yàgg-yàgg, jant dina mës a fenk”.
Foloriyaŋ Bobeŋ ab gëstukat la ci mboorum Afrig. Ay gëstoom jëm ci xeexu askan yi ngir am péexte ginnaaw nooteel gi, rawati na ci Senegaal jamonoy nguurug Seŋoor. Mbind mii nag njañse la rekk bu ñu tënk ñeel sémbu téere ci jaar-jaaru Omar Bolondeŋ bu ñu nekk di ci liggéey. Li nu ko yombalal mooy ndimbal lu kenn mënul a natt bawoo ci ay mbokk, ay xarit, ak ay xamey Omar Bolondeŋ Jóob, ak ay way-aamu ak ay gëstukat. Ngërëm lu amul àpp ñeel na : Jàllo Jóob, Seex Amala Jóob, Àliyun Sàll “Palomaa”, Usmaan Bolondeŋ Jóob, Paap Konaare Ñaŋ “Ñàngus”, Aalimana Bàccili, Saŋ-Kolod Làmbeer, Omar Bolondeŋ Mnd, Mareem Bolondeŋ Jóob, Xaali Mustafaa Lëy, Rolaŋ Koleŋ, Àntuwaan Lëfeebur, Silbeer Wódey, Bertaraŋ Gale, Misel Sànkarani-Furnel, Màrk-weesaa Ówlet, Patirig Talbóo, Mari-Ãselig Sawane, Asiis SalmoN Faal, Ndongo Sàmba Silla, Kariim Njaay, Pàppa Àliyun Jeŋ, Ndey Faatu Kan, Kibili Demba Sisoxo, Baara Joxaane, Bàrka Ba, Majaw Njaay, Xumma Géy, Alasaan Jóob, Ug Seglaa, Faatima Jàllo Ba, Xalil Jàllo, Weesaŋ Meesen, Paskaal Biyànkini, Farãsuwaa Bulum, Màrteŋ Muur, Omar Géy, Kiristel Lami, Léwo Selig, Dawid Morton, Tiristaŋ Bobeŋ