Fitt a jiitu fetal
Lépp aju ci ngistal
Doolee mën dëgg
Weddil googu dëgg
Njaayum gànnaay
Rombal doonub nay
Bu njaay mi lambee
Dëgg daan doole
Gént naay gànnaay
Yu wuteek yiy rey
Sànni xeeju jàmm
Ngir cofeel ak ndam
Gànnaay gi may xaar
Ca cofeel gi may xaar
Jàppe nit ni sa bopp
Mooy jëfu ki ma sopp
Soppante du gaaň
Jàppalante du xaň
Dund gi ne gàňň
Ñuy xiiro ba kaň ?
Demal ca toolu xare
Ña koy sooke duňu xare
Ña cay faatoo ka bare !
Jirim dëkke njàqare
Fetal gental sa kër
Ngay joy sa jëkkër
Booy woote wallu
Jàmm laa ci wóolu
Malaanum jàmm
Lanuy wut a am
Muslu ci safaan
Biy gàttalug fan
BEKKOOR
Sàqu dugub bi ňuy sol te muy lu tee fees
Mooy tawatu réew mi noor ak nawet
Bekkoor doomi koom-koom guy yaradal
Géntal nga réew mi nuy sàkku ndimmal
Def nga nu baayo yu wéet ci jamano
Bekkoor yaa ňu teg koor gu diine tegul
Koor gu gàkkal ngëmug ňu matul
Ba seenug matadi néewal leen doole
Nuy wàlliyaani ci lu dul sunu coobare
Bekkoor yaa ňu xaň man ci toolu xare
Ñuy xéy di xaar ay at yu bare
Sunu sàq mi nuy sol ana lu ko teree fees ?
Jinaxi dàmb yee ko fuq ca taat wa
Dëgg daal dina fés ni ki jàntu njolloor
Ku sa togg lóor nag nga dese siim sa wóor
Su boobaa nu ràňňee, kiy tookeek ki wóor
Dr Daouda NDIAYE Jaraaf