TABASKI 2024 : KÀDDU NJIITU RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Sñ Basiira Jomaay Jaxeer Fay, yëkkati nay kàddu ci julli gi. Naka noonu, muy ñaanal julliti Senegaal yépp ak yu àddina si. Muy ñaan bésub tabaski bi doon bésub mbégte, bésub jàmm ak ngëm gu gën a suuxatu.

Ginnaaw bi mu jullee ba noppi tam, Njiitu réew mi yëkkati na ay kàddu fa Grande Mosquée bu Ndakaaru ba mu doon jullee. Ci noonu la dellusee ci liggéeyi Càmm gi. Wax na ci jafe-jafe yi Saa-Senegaal yi di dund jamono jii. Mu leen di mas-sawu ak di leen fàttali ni lu ci ëpp ni jamono tëdde ci àddina si moo ko waral. Terewul nag, mu fàttali ni Càmm gee ngi ciy góor-góorlu bu baax. Nde, ñetti weer rekk lañ fi jot a def, terewul bari na jéego yu ñu ci jot a séqi.

Laata mu doon jeexal, Njiitu réew mi dellusi na ci waxtaan yi mu fi woote woon ñeel wàllu yoon. Dina jot ci caabal gi ci weer wi. Muy xamle ni Saa-Senegaal yi ñoo leen dénk ngir ñu doxal cib diir. Kon lépp lu ñuy jël niki ndogal dinañu leen ci déglu te dinañu doxal seen i bëgg-bëgg.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj