TASAARE DÉG-DÉG YU WÉRADI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saabalkat bii di Aadama Gay mi ngi ci loxoy yoon fi mu nekk nii. Moom ak Mustafaa Jaxate (APR) ñoo bokk i tuuma yu ñu leen di toppe.

Ci àjjumay barki-démb ji la ko pólis woolu woon. Moom Aadama Gay, takk-deri DIC yi lay wuyuji. Bees sukkandikoo ci Aadama Gay ci boppam, ca alxames jee weesu lañu ko waroon a déglu, ca 16i waxtu. Ca xëtu Facebookam la ko xamle woon. Waaye, ba tay ciy waxam, layookatam bi dafa amoon ngànt lu ko doon tere teewe ndégloom gi. Naka noona, saabalkat bi daldi sàkku ñu dàq ndéglu gi ba layookatam bi mën a am jotu teewe ko. Loolu moo taxoon ñu jàppaat ndéglu gi ci bésu àjjuma ji.

Ginnaaw bi ko takk-der yi dégloo ba ni 21i waxtu di jot ca guddig àjjuma jooja, bàyyiwuñu ko mu ñibbi. Dañu ko téyandi (garde à vue). Li ñu koy jiiñagum mooy siiwal ay dég-dég (xibaar) yu wéradi.

Tuuma jooju ñu gàll ci ndoddam, mi ngi aju ci wax ji mu biraloon ñeel deewub Mamadu Mustafaa Ba, jëwriñu ngurd ja woon ca nguurug Maki Sàll. Ca tele Sen tv la waxe woon kàddu yii toftalu :

“Man, dama foog ni dañu faat Mustafaa Ba. Kan moo ko faat ? Xamuma, fàww ñu luññutu mbir mi. Toppektat bi ubbi na ag luññutu, waaye dafa war a topp mbir mi ba mu jeex. Ndaxte, bu mbir mii jàllee noonu, kenn dootul am kaaraange fi réew mi. Bu dee ay nit mën nañoo def lii ka woon jëwriñu ngurd mi, kon lan lañu sañut a def ?”

Aadama Gay raxoon na ca dolli sax ne, bu luññutu dee am, nañu xool ci booru ñi moome woon réew mi, maanaam ñoom Maki Sàll. Kàddu yii moo tax ñu jàppagum Aadama Gay, saabalkat bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj