Ginnaaw bi njureefi joŋantey palum dépite yi rotee, yenn ci dépite yi biral nañ seen péete. Ndax, kii di Paap Jóob moom, di Njiital lёkkatoog Bokk Gis-Gis/Liggéey fekki na waa Bennoo Bokk Yaakaar ñi nga xam ne ñoo fare ci Nguur gi. Loolu, terewul nag ñeneen ñi fare woon ci yeneen lёkkatooy kujje gi moom, tey la waalo gёn a aay. Fañ tegoon seen tànk ci kujje gi teggiwuñu ko ba tey. Te, ñaari lёkkatoo yii di AAR SENEGAAL ak Les Serviteurs nga xam ne ñaari dépite lañu am. Ba sax, ñenn ci askan wi doon ruumandaat seen péete, biral nañu fa ñu bokk. Waaye, loolu taxul benn yoon ñu fekki kenn ci ñi leen ёppale muy ci Nguur gi di ci lёkkatoo YAW-WALLU. Ñoom, dañoo fas yéene fàkk seen yooni bopp ngir wéyal seen i sémb. Kon léegi, lan lees mёn a xaar ci taxawaayu dépitey kujje gi fale ca péncum ndawi réew ma ?
Taxawaayu dépitey kujje gi ёllёg ca péncum ndawi réew ma nar naa tagatémbe. Day mel ni, ku nekk ci ñoom dafa namm a wéy ci li mu nekkoon laata njureefi négandiku yiy génn, ak ginnaaw njureefi yu mujj yi. Ndax, kii di Paap Jibriil FAAL Njiital lёkkatoo Les Serviteurs ci ndajem-waxtaanam mii jàll, xamle na ci ne :
“ Taxawaay bi mёnt a ñàkk. Loolu, moo tax Senegaal rekk ci pólitig, askanu Senegaal ñoom lañu ci doon déglu, ñoo ciy sunu kilifa, ñoom rekk lañu fas yéene taxawal. Duñu doon bu sàmba, duñu doon bu demba (…). Te, caytu gi ñu bёgg a def ngir nga mёn ko def fàww nga moom sa bopp.”
Lii di ay kàddu ngir biral péeteem ci làngug pólitig gi. Mu mel ni moom dafa bёgg a xàll yoonu boppam bés bu àggee ca pénc ma. Ndax, dafa am sémb bu mu yor bёgg koo doxal. Moo tax, mu jàpp ne fare fenn da koy gàllankoor. Donte ne sax, fésal na bokkam ci kujje gi ngir soppi li fi nekk. Rax-ci-dolli, saytu koppar yi (budget) ci wàll yépp (càmm, mbey, napp, añs).
Ca beneen boor ba tamit, kii di Usmaan SONKO bokk ci lёkkatoo YAW-WALLU biral na ci ndajem-waxtaan ma mu doon amal, wax ci ne :
“ Dama ne duma seeti kenn, duma woo kenn, duma negosiye ak kenn. Ku leen ne Usmaan SONKO woo na ma di wax ak man ci nu may deme seen kippaango walla yooyu, loolu amul de. Man yёfu tappale yooyu bokkuma ci. Kenn ku nekk danga demoon daje ak askan wi, ne man ci kujje gi laa bokk, woteel-leen ma. Ba askan wi xéy am lu mu la jox, bari na néew na, am na lu la askan wi jox (…). Kon dogal boo jёl yaw ak askan woowu la.”
Kàdduy ñaari Njiital pàrti yooyu nag, junjul ag ànd ci diggante ñi fare ci kujje gi. Ndax kat, cin moom bu naree neex rekk, bu baxee xeeñ. Ba tey, ñii di waa AAR SENEGAAL tamit nga xam ne am na ñu doon laam-laamee seen bokk ci kujje gi laata ak ginnaaw wote yi. Biral nañ seen ag bokk ci kujje gi ci ab saabal bu ñu def ca Ndakaaru 12 ut 2022. Te, taxul tamit ñu fekki genn lёkkatoo tamit ci kujje gi. Ba ci sax ñii di waa WALLU SENEGAAL tamit ci seen saabal bi ñu def 16 ut 2022 ci lañu yeesalaat seen ag bokk ci kujje gi donte ne sax, ñoom ak YAW ñoo ànd. Ba tey jii, amagul seen benn dépite bu fekki Nguur gi. Ndegam, fi mbir yi tollu nii tembe nag, ku nekk ci kujje mi ngi ràcc di jёmale kanamam. Loolu terewul ne Nguur gi moom, mi ngi wéy di yor doole ja fale ca péncum ndawi réew ma. Moo tax, féewaloo du njariñal kujje ndax mbooloo kat mooy doole. Ba tax na, ñi fare ci kujje bu ñu boolewul seen doole, ndax seen taxawaay dina mёn a dёgёr ? Ndax tamit, dinañ mёn a wéyal seen i sémb yi ñu jotoon won askan wi ba mu wóolu leen ?
Waaye, kii di Ceerno BÓOKUM, bokk ci waa AAR SENEGAAL ci aw waxtaan wu mu doon def fale ca TFM moom dafa jàpp ne doole moom kenn amagu ko ca péncum ndawi réew ma. Ci la biral ne :
“ Dama gis ne ba mbir mi génnee rekk, dañu jёl ñetti dépite yi muy bu waa AAR SENEGAAL BOKK GIS-GIS/LIGGEEY, LES SERVITEURS jàpp ne ñoo war a leeral kàrt gi. Dama ne loolu ku xamul lool nu péncum ndawi réew ma di doxe moo koy wax. Ca dёgg-dёgg, ñépp a mёn leeral mbir yi. Ndax, doole (majorité) ji ni muy deme bu ñu ko waree teg mёn na jóge ci ñi ёpp doole (nguur gi), mёn na jóge tamit ci kujje gi.”
Mu mel ni loolu la kii di Usmaan SONKO di dёggal ci waxam jii :
“ …ñépp xam nañ ne péncum ndawi réew bala nga fay mёn a def li nga bёgg a def dёgg nga am fa doole. Fim ne nii nag, amaguñu ko, ñàkkaguñu ko(…). Kenn amagu fa doole. Bu soobe Yàlla fukki fan ak ñeent ci weeru Sàttumbar dinanu xam ku am doole ak ku ko ñàkk.”
Bu dee nag nii la mbir yi tёdde, te ba tey, ñi fare ci kujje, ku nekk a ngi ŋànk fi mu ŋànk. Ànd moom du mёn a am. Te, loolu dina gàkkal bu baax seen taxawaay ca péncum ndawi réew ma ngir ni ñu fa nar a ñàkke doole. Te, dina bokk ci liy gàllankoor seen sémb yi ndax, foofa moom doole moo fay dox. Benn loxo moom du tàccu. Te, lu kenn mёn sax ñaar a ko ko dàq. Rax-ci-dolli ne, cin moom ak lu mu fees fees xorom xaj ca. Moo tax, taxawaay yi mat a settantalaat ngir ñu mёn taxawal askan wi leen fa teg. Kenn ci ñoom bañ a boddi moroomam ndax dafa am lu tax askan rombu fi ñeneen teg leen fa. Te, beykat nag bu bàyyee tool buy tóor-tóor, dem ci digg màndiŋ di fa ruuj, bёgg ay tool taxul. Kon, na gaa ñi jiital bёgg-bёggi ñi leen fal, fàtte seen i péete. Ndax, mag moom kenn du ko wax, danga koy won.