TAXAWALUG “PLATEFORME” JUBBANTI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Talaata jii di ñëw mooy bés bi ñuy door waxtaan wi Njiitu réew mi doon wax bu yàggul dara. Waxtaan wi nag, dinañu ko tënk ci ponk bii di “Sopparñi ak yeesalug Yoon wi”.

Ci waajtaayi waxtaan woowu la Nguur gi nekk jamono jii. Looloo tax ñu taxawal, démb ci alxames ji, “plateforme” bii ñu dippee JUBBANTI. Ñu namm cee amal liggéey bu am solo.

Li ñu ko duggee mooytaataan xalaati maxejj yi ñeel ni Yoon di doxee fi réew mi. Maanaam, nan lañu gisee doxalinu Yoon, lu ciy baax-baax ak lu ciy rëq-rëq. Tur wi ñu jox dalu web bu bees boobule mooy “Sa gis-gis ci doxalinu Yoon”. Maanaam, dañuy jox kàddu askan wi, mu joxe xalaatam ci mbir mi.

Bu ko defee, dinañu mën a booloo indi ay saafara yu mucc ayib ba maxejj yi mën a am kóolute ci Yoon. Ndax, kenn umpalewul doole ji Yoon làmboo cim réew. Te, saa bu sooxee rekk, waa réew ma yëg ko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj