TËJ NAÑ MUSTAFAA JAXATE KASO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci altine ji, la Mustafaa Jaxate fanaan guddeem gu njëkk ca ndung-siin. Ginnaaw bi mu jàkkarloowee ak Toppekatu bokkeef gi ba noppi, ca lañ ko dóor lees di wax « mandat de dépôt ». Bes sukkandikoo meetar Elaas Juuf, di kenn ciy layookatam, dees na ko àtte keroog alxames, 28i pani nowàmbar 2024. Dinañ ko àtte nag ci wàllu tooñaange gu tooy (flagrant délit).

Moom, Mustafaa Jaxate, nekkoon na fi njiitul kippu ngomblaan gu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar. Ginnaaw gi la nekk njiitul kurél gii di « Mouvement Aar doomi Senegaal ». Keroog ci àjjuma jee weesu, 22i pani nowàmbar 2024, la ko waa DSC (Division Spéciale de la Cybersécurité) woolu woon. Li ko sabab mooy  kàddu ya mu biraloon ca jotaayu tele ba mu defe woon ca 7TV. Bi ñu ko dégloo ba noppi la ñu ko tegandi loxo, di ko toppe ay tuuma yu ci mel ni « ay saaga ya mu jibal, jaarale leen ci ay xaraala yu yees », « ay jëf ak i pexe yu nar a indi ay jéyya ñeel kaaraange réew mi » ak « di def ay pexe yu salte ngir tilimal pólitig gi ». Keneen ci layookatam yi, di meetar Aamadu Sàll, mu ngi xamle ci biir saabalukaay Les Échos, ne « Moom Mustafaa Jaxate wax na luññuntukat yi ne waajal na boppam ci lépp. Wax na sax ne ñu waxal ko njabootam gi ne, mën na am dootu ñu ko tegati bët, ndax amul kóolute ci ñi ko woolu. »

Demoon na sax, moom Mustafaa Jaxate, ca kàddoom ya mu yëkkati woon 7TV bay xas Saa-Senegaal yi. Nde, moom dafa nanguwul li waa (Pastef) am rawug buural ca ngomblaan ga, moo tax muy méngale Saa-Senegaal yi ak « askan wu alku ».

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj