Démb a nekkoon bésub tiijitel ëtt ak bérébi àttekaay yi ci njiitalu Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Fa saalu àttekaay bu Ëttu àttekaay bu kawe bi lañ doon amalee ndaje ma, ci alxamesu démb ji, 16i fani sãwiyee 2025.
Bi Njiitu Réew mi jëlee kàddu gi, dafa njëkk a fàttali solos Yoon cim Réew. Dafa di, ciy waxam, Yoon rekk a mën a sàmmal nit ñi seen ngor ak seen i sañ-sañ yoy, seen i àqi juddu la, muy lu mënut a ñàkk. Te yit, Yoon mooy sàmm jàmm ak dalug pénc mi.
Njiitu Réew mi xamle na fa tamit ne, fàww ñu wéyal coppite yees sumb ci fànnu Yoon ngir gën ko dëppale ak jamono. Coppite yooyii, ñi ngi aju ci anam bi Yoon di doxee. Rax-ci-dolli, dees na fexe ba ñu man a doxal sañ-sañu seleŋlu ci kaw sàmmonte ak dalug pénc mi ak li ñépp bokk. Ci weneen waxiin, dinañu fexe ba ku nekk sañ a wax sa xalaat walla sa gis-gis ci kaw kiy wax xam fi mu war a yam ngir bañ a tooñ walla wax lu yee fitna.
Ci gàttal, yéeney Njiitu Réew mi mooy, ci njëlbeenu moomeem gii, fexe ba tabax Yoon wu jub, di jubal ak a jubbanti. Maanaam, Yoon wu dëppoo ak jamono, dëppoo ak mbatiit ak gëm-gëmi waa Réew mi, waayeet jàppandi ci ñépp.