Gii Mari Saañaa ma nga Togo jamono yii. Waaye, nekkul ci jàmm. Ci lees jot ciy xibaar, dañ ko fa song, gaañ ko ba ñu rawale ko ci benn kilinig bu fa nekk. Dafa am ndajem maxejj mu mu fa teeweji woon. Ci ngoonug dibéeru tey ji la cong mi am.
Gii Mari Saañaa dépite CDEAO la. Looloo ko tax di wër ci réewi Afrig sowu-jant yi ngir di waxtaan ak a weccoo xalaat ak askan yi. Tey ci ngoon, dafa demoon ci menn ndaje mom, xeex la mujje.
Ci lees nettali, bi ndaje mi tàmbalee ba am 10i simili, Gii Mari Saañaa dafa sàkku ci mbooloo mi ñu jóg woyandoo bàkku réewum Togo. Ca saa sa, toogu yi tàmbalee ñaaw, ñu leen di sàndi ci taabalu dépite yii di Gii Mari Saañaa, Brigitte Kafui Adjamagbo-Johnson ak Targon. Noonu, ndaje ma tas, daldi jaxasoo, xeex bi jolli, kurpañ yiy dal, toogu yiy naaw. Ku nekk di daw ngir jéem a mucc, béréb ba rëbajoo.
Ci biti, ñu daldi tojate ay moto ak i daamar ya fa gaare woon. Nee ñu, dépite yi bokk ci làng gii di “Dynamique pour la majorité du peuple”, rawatina Targone, dañ leen a dóor ba ñu nàcc, deret jiy walangaan. Am na yit ay taskati xibaar yu ñu fa caxat-caxatee.
Ñi fésal xibaar bi xamle nañ itam ne, sunu dépite bii di Gii Mari Saañaa, kanam gi dafa doon nàcc. Dañu ko mujje boot, daw, rawale ko ci benn kilinig. Li ci gën a doy waar, ci lees wax, mooy ne takk-der yaa nga woon ca wet ga, mënoon a àttesi, jàpp songkat ya, waaye dañu leen a seetaan. Moo tax, ci mbaali-jokkoo yi, ndaw ñaa ngiy àrtu Nguurug Togo gi ci wér-gi-yaramu sunu dépite bi, di sàkku ci sunu njiit yi ñu gaaw def dara ngir aar Gii Mari Saañaa, delloosi ko fi réew mi.
Dees na ci ñëwaat bees ci amee lu yees.