FMI dafa génnee ag caabal gog, day càmbar koom-koomu Senegaal ci njëlbeenug xaaju atum 2024 mi. Njureef yi tukkee ci caabal googu nag, du lu dal xel. Nde, ci seen i wax, koom-koomug Senegaal dafa nasax. Li ko sabab mooy anam bees ko yoree woon ci weer yu njëkk yi ci atum 2024 mi. Maanaam ni ko nguurug Maki Sàll gi yoree woon moo baaxul. Loolu nag, Njiitu réew mi junj na ko keroog bi muy wax ak askan wi.
Bi Njiitu réew miy wax ak askan wi, mbirum Ngomblaan gi la nit ñi gën a bàyyi xel. Waaye, laata muy àddu ci mbirum Ngomblaan gi ba di ko tas, waxoon na ci ni mu fekkee réew mi.
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dafa ñaawlu anam bu ñaaw bi Maki Sàll bàyyee réew mi ak jafe-jafe yi nekk ci koom-koom gi. Dafa di, ginnaaw bi ko Maki Sàll jébbalee lenge yi, dafa càmbar lim fi fekk, xool tolluwaayu réew mi. Dafa waxoon ne :
« Bi ma toogee, li ma njëkk a def mooy saytu ba xam liñ ma dénk, ci fan laa ko jële. Te, loolu la ma Yoon sant, muy li ñuy wax « code de transparence dans la gestion des finances publiques ». Maanaam sàrt bi may wax, di nu wax, nun ñépp, naka lañuy saytoo ci yoriin wu rafet alalu mbooloo. »
Ngir wóoral njureef yi tukkee ci caytu googu, daf leen a jébbal « … “cours des comptes”, mu war ko saytuwaat ba dëggal ko. Bu ko defee, dinañ ko jébbal askan wi, wax leen ne tamit fii lanu jëlee réew mi. »
Yemul foofu. Nde, ciy waxam, njiit yi fi nekkoon dañoo salfaañe alalu askan wi, yor ko yoriin wu ñaaw wow, dañu ko nëbboon askan wi. Noonu la ko waxee ci kàddoom yii mu biral keroog alxames 12i pani 2024 :
« Waaye, saytu boobu wone na ne, yoriin wi ñaaw na lool. Te am na loo xam ne nëbb nañ ko askan wi ci yoriin wi, luy wone ay jalgati. Maanaam, doxaliin woo xam ne, dafa mel ni lu rëccal dayob payoor yi ( masse salariale), rëccal bor yi, rëccal lépp lu ñuy fay lu laale ci bor yi ak ni nga xamante ne, noonu lañuy jëlee alal ci bitim-réew. Lii nga xamante nag gis nañ ko ci ñaawteef, ci doxaliin, mu waral ba sunu koom-koomu réew lompoñ, Càmm gi, bu waxtaanee ba noppi ak ñi nga xam ne ñoom la séqal mbir mi, dina ñëw waxtaan ak Saa-Senegaal yi, jébbal leen lépp loo xamante ne “cours des comptes” joxe na ko. »
Bu loolu weeso, nguur gu bees gi daa fas yéene yóbbu ca Yoon képp ku laale ci yoriin wu ñaaw woowu yàq réew mi. Moo tax Njiitu réew mi biral ne « … ñépp ñi nga xamante ne, ci li ñu fekk nii ci ñaawteef ak ci guuta gi mu dugal Senegaal laale na ci, Yoon dina def liggéeyam ci ñépp ñoo xamante ne laale nañu ci. »
Li kàddu yiy wund mooy ne, fileek i bés, Yoon dina tàmbalee topp ñi doon saytu alalu réew mi te def ci naka su dul noonu.