TONTU DU FOROX !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci yoor-yoor bi, toppekat bu mag bi, Ibraayma Baaxum, doon na amal ndajem waxtaan ak taskati-xibaar yi. Li mu ko dugge woon mooy leeral coowali Yoon yi lëmbe réew mi jamono yii. Moom, nag, biral na fa mbir yu bari yoy, ñu ngi ci loxoy Yoon : mbirum caabalug Ëttub cettantal bi, mbirum doktoor Baabakar Ñaŋ, bóom gi ñu naroon a bóom Usmaan Sonko ak mbirum « komaando » yi lënkaleek waa Pastef. Bu yeboo ne, moom Baaxum, bim agsee ci mbiri Usmaan Sonko, dafa xaabaabalci wax ji. Moo tax, ci guddi gi, njiitul kujje gi feelu na ko, dàjji tuuma yi mu gàll Pastef yépp, daldi feeñal ay njuumteem ak liggéey bu salte bi Nguur giy defloo yenn àttekat yi.

« Nguur gi dafa guuxal mer Dr Baabakar Ñaŋ… »

Ci ndoorteelu waxam, toppekat bu mag bi dafa biral ni du am laaj-tontu digganteem ak taskati-xibaar yi. Jubluwaayu ndaje mi, ciy waxam, du woon lenn lu mooy leeral coowali wayndare yi lëmbe réew mi jamono yii, xamal askan wi fees ci tollu. Daanaka, faramfàcce na fa ñeenti ponk. Waaye, mbiri Pastef ak seen njiit li, Usmaan Sonko, ñoo gën a fës ciy waxam.

Bu dee mbirum Ëttub cettantal bi, dafa wax ni rekk am na ñees déglu ca njëwriñu ndaw ñi. Nde, diggante 20 jàpp 24i fan ci weer wii lees déglu ñii di Sàmba Faal, Jibril Kan, Soxna Faatu Si, Xujja Njaay ak Mamadu Seen. Fa la ca yem, rax ca ne Yoon a ngi wéyal liggéey bi ñeel caytug koppari FORCE Covid-19 bi. Loolu, njiitul Pastef li àdduwu ci.

Li ñeel mbirum fajkat bii di boroom kilinig Suma Assistance nag, Baaxum biral na sabab yi tax ñu teg ko loxo. Ñetti tuuma lay toppe Dr Baabakar Ñaŋ : reyug teyeedi, tayleb bakkanu jàmbur ak ñàkk a wattu nit ku repp. Ñu baree jàpp ne, lim fat njiitul Pastef li ci ragloom a ko yóbbe coono yi muy daj yépp.

Usmaan Sonko nag, ci wàllu boppam, nee na xamantewul ak doktoor Baabakar Ñaŋ. Te, kilinig ba, daf ko jege moo taxoon mu dem fa, woolu fay fajkati boppam. Waaye, mësul giseek boroom kilinig bii di doktoor Baabakar Ñaŋ. Nee na « Nguur gi daf guuxal mer ginnaaw bim yoolee njombey Covid-19 bi. »

« …dinanu jàmmaarlook Maki Sàll. »

Bees sukkandikoo ci kàdduy Ibraayma Baaxum, dafa am ay defkati ñaawteef yoy, seen nisër mooy rax ñaxtukat yi ngir def i tojaange. Mu ne, ñooñu kat, dañu taxawal am mbooloo mees duppe “komaandoo” te kii di Muraamani Kabaa Jakate jiit ko.  Toppekat bi neeti, saay-saay yooyu, ay kilifa ci réew mi lañ diir, bëgg leen a faagaagal. Kilifa yooyii, tuddul seen i tur, waaye nee na ay kàngaam lañu ci wàllu pólitig, Yoon, Nguur, diine ak kibaraan yi. Dem na ba ne sax, jàpp nañu ñeenti nit yoy, ci MFDC lañu bokk.  Mu ne am na yeneen 19i saay-saay yu ñuy wër.

Ay waxi kasaw-kasaw la jàppe kàdduy Ibraayma Baaxum. Ndaxte, « […] Toppekat bi nee na, ñooñu, fetal sax yoruñu ko. Mu ne ñooñoo waroon taal réew mi. » Doy na waar. Ku yorul fetal, fooy taal ? Kon, lu wund tuuma yile ? Usmaan Sonko, moom, dafa jàpp ni Maki Sàll dafa bëgg a yee fitna diggante waaso yi. Bees sukkandikoo ci kàddoom, li Njiitu réew mi di wut mooy taqal waa kaasamaas. Moo ko tax a seetlu, gis ne :

« Ñi ñu ci jàpp, lañ leen jàppe mooy seen sant méngoo naak santu joolaa walla santu kaasamaas. Tey, Senegaal, képp ku nekk kaasamaas rekk te bokk Pastef, boo moytuwul léegi ñu laxas la. Moone de, Pastef, Mbàkke la ëppee doole Kaasamaas. Pastef, Ndar, la ëppee doole Kaasamaas. Pastef, Ndakaaru gii la ëppee doole Kaasamaas. »

Buñ seetloo, ci farãse la toppekat bi ubbe ay kàddoom, ca la gën a waxe sax. Ñu gis ne, tubaab yi la doon gën a waxal. Sonko nag feelu na ko ca :

« Toppekat bi wax na ak yeen, yeen waa àddina si, te jéem na leen a gëmloo ne Senegaal dafa am ay rëtalkat (terorist) yu bon a bon. Waaye dinanu génn, dinanu ñaxtu, dinanu jàmmaarlook Maki Sàll. »

Xeex boobu nag kujje giy waaj, Usmaan Sonko jiite ko, am na ñu leen ciy ŋàññ, di wax ne waruñoo yee fitna, rawatina bésub 4 awril.

« Dama ne, ku mën a xeex na xeex. Ku mënul xeex, na maandu ci li ñuy xeex. »

Kujje gi daa fas yéene sumb i doxi ñaxtu fépp ci réew mi ngir xeex Maki Sàll. Meeru Sigicoor bi ne :

“Nañu ñaxtu fépp ci Senegaal ba Maki Sàll xam ni saa-senegaal yi ànduñook moom. Ñaxtu yi, nag, ñépp a ci war a ànd ñaxtu. Bu ñu jàpp ne ñaxtu gi mbirum ndaw ñi kese la, walla mbirum Pastef kese la, déedéet. Li Maki Sàll bëgg, bu ko amee, kenn ku nekk fi nga toog, dinga toog màtt sa baaraam wiccax…”

Njiitul kujje gi neeti, kenn warul jàpp ne mbir mi, mbirum Usmaan Sonko. Nee na yit, kenn tuddul bésub 4 awril bi ñépp bokk. Te, kenn  mënu leen a jaxaseek làrme bi ndax kenn ëppalewu leen ci. Dafa gëm sax, li ëpp ci làrme bi, ñoom lañ àndal. Usmaan Sonko a ngi tontuwaale ñiy wax ne bésub 4 awril wareesu cee ñaxtu. Mu gis ne, loolu, waxi naaféq la. Ndax, ciy kàddoom, Maki Sàll ci boppam joxul cër askan wi, fonkul Bokkeef gi. Muy laaj ndax :

« Maki Sàll buy tëjaate daf ciy xool luy 3 awril ak luy 4 awril ? Buy dóoraate ak buy dóor nit ñi ay bal day xool ban bés lañu nekk ? Dama ne, ku mën a xeex, na xeex. Ku mënul xeex, na maandu ci li ñuy xeex. »

Tontu du forox.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj