Barki-démb, àjjuma 11i Oktoobar 2024, Senegaal doon na daje ak Malawi ca fowub Abdulaay Wàdd bi nekk Jamñaajo. Mats bi di woon seen ñetteel ñeel tooglanteg CAN 2025 bi. Paap Caw, tàggatkatu négandiku bi moo jiital ekib bi keroog. Moom ak i ndawam daldi am ndam lu réy. Nde, dañu jàpp gan gi, duma ko 4i bal ci tus (4-0). Paap Géy (35′), Saajo Maane (68′), Bulaay Ja (71′) ak Nikolaa Jakson (77′) ñoo dugal bii yi.
Kii di Jakson nag, booboo nekkoon biiwam bu njëkk ci ekibu Senegaal bi. Muy lum yàggoon a yóotu, dégg ci lu nekk. Kon muy doon lu koy teggil yan wu rëy tay, di dëggal tàmbalig atu futbal gu jaar-yoon gim nekk. Muy mbégte mu réy it ci moom. Ndaxte, gannaaw bii bi, wane na ko ak ba joŋante ba jeexee tamit bañ dekk ko ngolliir gi, xamle na ni ; “bii bi lu ma yàgg a bëgg la. Bég naa ci lool. Maa ngi ko tudde sama yaay”.
Gannaaw loolu, jaajëfalees na Paap Caw ci tàmbali bu am solo bim def. Seneegaal war na a dajewaat ak Malawi, talaata 15i Oktoobar jii fa dëkkam, ñeel ñeenteelu joŋanteg po mi.
Soppe yi tamit bég nañu ci ndam li. Ba mats ba jeexee, foo geestu waan ci mbaali-jokkoo yi, ñu gi ciy wax. Ñii naan “Nii l a! Ekib boo ko mënee danga koy wulli”, ñee naan ” Buñ ko jàppoo nii léegi nawle yi bàyyiwaat xel ekib bi”, ñay ruube ak a tooñ tax a jóg naan “Aliw Siise moo yéex a dem…”. Wànte, ak lu mën di am it, lii lañuy xaar ci ekib bi ak képp ku ko mën a jiital. Muy futbal bu leer te ñu ànd doon benn, ndax lépp ndamal Senegaal la.
Ismayla Sakob dellu na këlëbam
FSF xamle na, cib déggoo bum am ak waa Galatasaray, ne kii di Ismayla Sakob dellu na këlëbam keroog àjjuma ba mats ba jeexee. Li ko waral nag mooy ni dafa war a fajuji. Ndax, dafa ame gaañu-gaañu ci óom bi. Ngir wer-gi-yaram ak bañ mu yóbbe ko leneen a tax ñu bàyyi ko mu dellu, fajooji fa.