TUBAAB YAA NGI YEDD MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gi boole digaaley Senegaal yi ci wàllu xarala ak kopparal, G50, yedd na Njiitu réew mi, Maki Sàll. Àmbaasadëeru Bennoog Tugal gi, Jean Mark Pisani mi leen doon waxal. Ku bàyyi xel ay kàddoom, dinga ci jàngatee ne, tubaab bi day artu Njiitu réew mi ñeel tolluwaayu réew mi ci wàllu pólitig.

Li waa G50 njëkk a laaj mooy ñu xamal ko fu luññutu yi tollu, rawatina mbirum Caabalug Ëttub cettantal bi ñeel koppari Force Covid-19 yi. Rax-ci-dolli, tubaab yi dañu sas Nguur gi, wax leen ñu siiwal caabal yi Ëttub cettantal bi defaroon ci ati 2018, 2019, 2020 ak 2021. Sàkk nañ itam ñu génne caabal yi ñeel àttey doxal ngurd mi, yu ati 2020 ak 2021. Dafa di, caabaal yooyii, Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo ci teg concoom, ngir nëbb njombey nguuram te làqaale ay farandoom.

Waa G50 dañu sasaale Maki Sàll, mel ni ku koy sant mu doxal yoon, ànd ceek maandute. Nde, buñ leen déggee, fàww Maki Sàll doxal yoon ci biir weer yii ko dese, bu dee bëgg naa wéyal liggéey beek ñoom.

Bu loolu weesoo, waa G50 fésal nañu seen i njàqare ci ni fitna jees nemmeeku ci géewu pólitig. Nee ñu sax, balaa ñuy sóobu ci Forum « INVEST SÉNÉGAL » bi war a am ci weeru suwe, fàww ñu « sàmm dalug réew mi […] ci wàllu pólitig te ñu fexe ba Yoon teëdde njaaxanaay. »

Waa G50 nee, dañu war a « fexe ba ba jàmm am ci réew mi, waxtaan mën a am te way-pólitig yépp mën a bokk ci jàmm wëlis xàjj-ak-seen. » Teg nañ ci ne, enegaal dafa war a sàmm demokaraaseem.

Wax jépp, nag, dañoo rafetal rekk. Waaye, li ñu bëgg wax Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Nguuram génnul ponk yii :

  • nañu bàyyi xoqatal beek bundxataal bi ñuy teg waa kujje gi ;

  • nañu dakkal jàppaate yu bari yoy, teguwuñ ci yoon ;

  • nañu bàyyi lawax yi war a bokk ci wotey njiiteefu réew, rawatina Usmaan Sonko, ñu bokk ci jàmm ;

  • nañu suuxat jàmm ci réew mi, sàmmoonte ak sàrti demokaraasi ;

  • ñu bañ a jalgati Ndeyu-àtte réew mi, maanaam Maki Sàll bañ a laaj ñetteelu moome.

Ku jàngat waxi Jean Mark Pisani yi, dees na dégge ci yuqu wax ji ne, 3eelu moome gi dafa nar a taal réew mi. Te, ñoom tubaab yi fi bëgg a dugal seen xaalis ngir liggéey, loolu jigu leen.

Du doon mbetteel bu ñu gisee ay caabal yu génn walla mu am ñees jàpp ci mbirum Froce Covid-19 mi. Ndaxte, G50 a yor koppar yi, moo tax Nguur gi yebu leen. Nde, ku la abal i bët, moo lay wax fooy xool.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj