TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA KODDIWAAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, moo ngi, ñaari fan yii, fa réewum Koddiwaar ngir teewe fa ndajem AFRICA CEO FORUM bu 2025 mi. Muy ndaje mom, bokk na ci ndajey koom-koom yi gën a mag yees jagleel fànnuw jàmbure wi fi kembaarug Afrig. At mu jot, la ko dale ca atum 2011, ay kilifay pólitig yu jóge ci diiwaani Afrig yi ak ci àddina sépp, ak ay njiiti këru liggéey yu mag dinañu ko teewe ci ñaari bési lél, weccante ay xalaat, ak a amal i ndaje yu mag jëme ci solos fànnuw jàmbure wi ci suqaleeku kembaar gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj